WAA ETAASINI, UE AK CEDEAO DAL NAÑU CI KOW MAKI SÀLL
Ndogalu Njiitu réew mi Maki Sàll mi ngi wéy di jur ay coow, muy ci biir-réew mi ak ca bitim-réew yépp. Moo tax ñii di waa Etaasini xaaruñu dara ngir àddu ci liy xew ci réew mi. Ndax, li fi xew ci diggante keroog ak léegi ñépp a ci teg seen i bët. Muy ci mbedd mi, ci lënd gi ak fa Ngomblaan ga. Ñuy sàkku ci Njiitu réew mi mu amal wote yi ni ko sàrti Ndeyum àtte mi tëralee. Ndax, dañoo jàpp ne li mu layalee ndàqug wote yi tegu ko fenn. Rax-ci-dollu, mu bàyyi maxejj yi di wax seen xalaat ak di def seen i ndaje num leen neexee. Naka noonu taskati-xibaar yi nañ leen bàyyi ñu def seen liggéey ni mu waree. Li ñeel mbirum lënd gi moom, delloosi na ko démb ci guddi gi. Li des nag moom, ndogal wàccagu ci.Waaye, li ci kanam moom rawul i bët.
Naka noonu waa CEDEAO ak Bennoog Tugal (Union Européenne) tamit ñi ngi topp xew-xew yiy am ci réew mi. Moo tax kurélug CEDEAO génnee démb ab yégle ngir àddu ci ndogal li Njiitu réewum Senegaal li jël. Ñaari kurél yooyu, seen càkkuteef ci Njiitu réew mi mooy mu bàyyi àppug wote yi fa mu nekkoon. Mu bañ cee yokk, bañ cee wàññi. Maanaam, mu bàyyi ko ci ñaar fukki fan ak juróom ci weeru féewiryee ni ko Ndeyum àtte yi waxee. Lu ko moy loolu mën na gàkkal seen demookaraasi bi lee ñépp doon ñeewee bu yàgg ba tey.
Fii ci biir-réew mi tamit gaa ñaa ngi wéyal xeex bi. Ndax, tey ci àllarba ji tamit fukk ak benn ci lawaxi kujje gi walla ñi leen teewal doon nañ jàkkaarloo ak kibaaraan yi. Ñoom it seen mébét mooy ñu bañ a dàq àppu wote yi ni ko Njiitu réew mi bëggee. Ñu yokk ci ñoom ci seen wàllu bopp dinañu wéyal seen kàmpaañ ni ñu ko dooree woon. Rax-ci-dolli, ñuy sàkku ci kurél yi ñu bañ a jàppe Maki Sàll Njiitu réew bu ñaari fan ci weeru awril jàllee.
CAP DOOR NA XEEX
CAP (Coordination des Associations de Presse) di kurél gi boole ñiy yëngu ci wàlluw tas-xibaar door nañu ab xeex ginnaaw bi Nguur gi jëlee ndogalu neenal lisãsu Walfadjiri. Tey, ci àllarba ji, amal nañu am ndaje ak ñi jiite kibaaraan yi ak kuréli way-moomeel yi diggante ñetti waxtu ba juróomi waxtu ci ngoon gi. Ci alxames ji nag, dinañu amal li ñuy dippe “éditorial commun et lancement de la communication visuelle et sonore”. Àjjuma tamit, dinañu amalaat ndaje ak kibaaraan yi fukki waxtu ci suba fa këru kibaaraan ga. Altine ji, dinañu siiwal bataaxal bi ñuy jébbal Njiitu réew mi. Talaata ji ñu amal bés boo xam ne kibaaraan du am ngir màggal bés bi àdduna jagleel Rajo. Ci àllarba jii di delsi, dinañu saytu bilaŋu xeex bi, xool li ñu ci góobe. Rax-ci-dolli, dinañu sumbaat ñaareelu xeex bu dee bi ñu njëkkoon a door gisuñu ci genn coppite.
BÀYYI NAÑU SÉYDINAA UMAR TURE
Démb ci talaata ji la lëkkatoog Jomaay 2024 nammoon a amal seen um ndaje. Waaye, loolu mujjul woon a àntu. Ndax, ñu ci mel ni Gii Mariis Saaña, Meetar Taal, Séex Àlliyun Béey ak Séydinaa Umar Ture dañu leen jàppoon. Donte ne sax, ñoom Gii Mariis bàyyi woon nañu leen biig. Moom Kàppiteen Ture, Séex Àlliyun Béey, Séex Basiiru Jeŋ ak benn jegeñaale Aminata Ture, tey ci suba lañu leen di sog a bàyyi. Waaye, loolu taxul moom kàppiten Ture mu teggi wenn yoon fa mu tegoon tànkam. Ndax, nee na, dañuy wéyal seen i kàmpaañ.
AWA MARI KOL SEKK BÀYYI NA
Ginnaaw Abdu Latif Kulibali, keneen ci jegeñaaley Njiitu réew mi, Maki Sàll, tekki na ndombog-tànkam. Kooku bàyyi nag, kenn dootu ko aajar Saa-Senegaal yi. Ndax, moom Awa Mari Kol Sekk moo fi nekkoon ay jamono jëwriñ ji ñu dénk wàlluw wér-gi-yaram. Moom it de, bàyyi na. Donte ne sax xamaguñu li sabab loolu. Waaye, ginnaaw ndogalu ndàqug wote yi la ko jël. Moom Awa delloo na Njiitu réew mi ndombog-tànk bi mu ko takkaloon. Ndax, kenn umpulewul ne moom, jëwriñu Càmm la woon (Ministre d’Etat) nekkoon yit njiitul ITIE (Initiative pour la Transparence dans la gestion des Iindustries Extractives).
BÉSUB GÉNNUG ÀDDUNA SÉEX ANTA JÓOB DELLUSI NA
Séex Anta ab boroom xam-xam la woon boo xam ne kenn dootu ko naatable ci àdduna wërngal-këpp. Tey, àllarba juróom-ñaari fan ci weeru féewiryee moo yemoo ak bés bi mu génnoon àdduna ci atum junni ak juróom-ñeenti téeméer ak juróom-ñetti fukk ak juróom-benn. Mu nekk bés bu am solo ci ñiy yëngu ci wàllu xam-xam. Ndax, li mu liggéey ci wàll woowu kenn dootu ko fàtte ci kow suuf.
MÀGGALU KASU RAJAB
Tey ci àllarba ji juróom-ñaari fan ci weeru feewaryee moo yemoo ak màggalu Kasu Rajab. Kasu Rajab bés bu am solo la ci yoonu murid. Ndax, ci lañuy màggale bésu juddug Sëriñ Fàllu Mbàkke mi nga xam ne mooy ñaareelu doomu Séex Ahmadu Bàmba mi sos yoonu murid. Mi ngi juddu ñaar fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru suwe atum junni ak juróom-ñetti téeméer ak juróom-ñett fukk ak juróom-ñett fa Daaru Salaam.
AKSIDAŊ YU METTI
Benn bi mi ngi ame tey ci suba ay boori juróomi waxtu ci wetu Rond-point Diassap. Benn kaùiyoŋ moo fa fiir benn takk-der. Takk-der boobu mi ngi wuyoo ci turu A. Njaay nga xam ne ci liggéeyam la nekkoon. Ki doon dawal daamar ga moom, ba mbir ma xewee la daw. Waaye, daamar ga moom ma nga ñu téye foofa.
Beneen ba mi ngi ame ci yoonu màggalu Kasu Rajab. Aksidaŋ bi mi ngi ame ci diggante Nduuloo ak Ngaabu. Lu tollu ci ñeenti doomi-aadama ñàkk nañu ci seen i bakkan. Mu am tamit ñoo xam ne jële nañu fa ay gaañu-gaañu. Loolu moo nekkagum limub ñi ci loru.