Njiitu réew mi Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay teeweji woon na Ndajem Dohaa mi ñu doon amal fe Qataar ci njeexitu ayu-bés bi (gaawu 7 ak dibéer 8 desàmbar). Teewe na fa itam ndaje yu am solo. Naka noonu, gaawantu na fa ci kanamu àddina sépp ngir aajar fànn yi ëppal solo àddina si ak gis-gis bi mu am ci Senegaal ak Afrig. Muy gis gis bu bees bu dàq yaras, ànd ak bëgg-bëgg yu leer te ubbeeku ci àddina si.
Démb ci dibéer ji, 8i pani desàmbar 2024, Njiitu réew mi amal na itam ab jotaay ak Fahad Al-Sulayti (njiitu lu mag lu Qatar Fund for développement. Waxtaan nañu ci àndub réewum Senegaal ak mu Qataar. Fas nañu yéene itam gën koo dëgëral ci yokk dugalante bi ñeel fànn yi gën a tembare ci sémbuw Senegaal 2050.
NJAAYUM GERTE GI
9i way-yëngu ci njaayum gerte gi lañu teg loxo fa Poroxaan, diiwaanu Kawlax. Lees leen jàppe nag mooy ñàkk sàmmonteek ndogal yi Nguur gi jël ci njëg yi. Xiibaar la bu Aadama Muhamet Mbay (njiitu pekkug yaxantu gi fa diiwaanu Kawlax) biral. Bees sukkandikoo ciy waxam, ñees teg loxo dañu doon baara-yëgoo di jënde kilo gerte gi lu yées 305i dërëm, njëg li Nguur gi taxawaloon ginnaaw bi mu ci amalee ay diisoo ak way-yëngu yi séq wàlluw gerte gi.
ITV : LIGGÉEYKAT YAA NGAY WÉY DI ÑAXTU
Liggéeykati këru liggéey gii di itv a ngi wéy di amal seen gereew bi. Ñoo ngi ci seen 7eelu ayu-bés bi ñu tàmbalee bank seen i loxo ak tay. Fii mu nekk, dàqatuñu yóbbi mbir mi fa mbaxane doone benn. Nde ci liñ wax, te sunuy naataango yu PressAfrik siiwal ko, boobu ba léegi ñoo ngi xaarandi ak di jéem i pexe. Waaye, seen njiiteef gi dafa wéy di leen tanqamlu. Nanguwul a jéem a def lenn ngir saafara seen i tawat. Muy nag tolluwaay bu doy-waar ci poosu liggéeykat ya, waaye itam lu fi mën a jaar suuxal cumbeef gi. Cig pàttali, 21i pani oktoobar 2024 lañu njëkkoon a bank seen i loxo ginnaaw bi ñu toogee 5i weer yu ñu jotul seen i peyoor.
OMVS
Doon nañu amal 11eelu ndajem Njiiti réew yeek njiiti Càmmi OMVS (Organisation pour la mise en valeur du fleuve Gambie, mbootaayu miy ñoŋal dexu Gàmbi gi). Ñiŋ ko doon amalee fa Bànjul, réewum Gàmbi, ci njeexitu ayu-bés bi. Magum Jëwriñ yi, Usmaan Sonko moo fa teewaloon Réewum Senegaal. Ñu waroon fa càmbar wayndare yu bari ci diggante ñeenti réew yi ko séq, rawatina taxawalug campeef gu bees gii di SODESART (Société de Gestion de l’Energie de Sambangalou et du Réseau de Transport) ak yeesalaat toogaayu njiit yi ci boppi campeef yi.