LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (Àllarba 08 féewaryee 202)

Yeneen i xët

Aji bind ji

GUY MARIS SAAÑAA BOOLE NA SËRIÑ BASIIRU GÉY

Guy Maris Saañaa bind nab bataaxal, jébbal ko waa OFNAC. Li mu ko dugge mooy tiiñal Sëriñ Basiiru Géy mi nekkoon Toppekatu Bokkeef gi, jiite tey OFNAC. Moom ci boppam moo biral xibaar bi, bind ne :

“Maa ngi leen di yëgal ne bind naa ñaari bataaxal, jagleel benn bi waa OFNAC, beneen bi ma jagleel kob jëwriñ ji ñu dénk Yoon.

  • Bataaxalu OFNAC bi, maa ngi ciy siiwal wuruj ak coppiteg wayndarew luññutu, di ci tuumaal Sëriñ Basiiru Géy mi nekkoon Toppekatu Bokkeef gi, ñeel kootoo gi Nguur gi kootoo Sonko.

  • Bataaxal bi ma jagleel jëwriñ ji ñu dénk Yoon, maa ngi ciy siiwal génnug topp gees di njortal Sëriñ Basiiru Géy, ba tey ñeel kootoo gi Nguur gi kootoo Sonko ngir fexeel ko.

JÀPPATI NAÑ HANIBAAL JIIM

Tey, ci yoor-yoor bi, lañu jàpp Hanibaal Jiim. Nee ñu, bi mu génnee këram la ko takk-deri “Police centrale” jàpp, yóbbu. Ba tey nag, xamaguñ lu tax ñu jàpp ko.

AKSIDAŊ SIKILOO : 45eelu BAKKAN ROT NA

Halimatu Sawane mi tëddoon loppitaan, mujje na gaañu. Ca aksidaŋ ba la jële woon i gaañu-gaañu, doon faju boobaak léegi. Waaye muccul. Moom nag, mi ngi amoon 21i at dёkkoon Petit-Mbao. Kon, léegi, limu nit ñi ñàkke seen bakkan ci aksidaŋu Sikiloo ba àgg na 45.

FADIILU KEYTA DU GÉNN

Layookati militaŋu Pastef bi dañu ñaanaloon Fadiilu Keyta mbawug négandi (liberté provisoire) ci magum àttekat yi, Maaham Jàllo. Waaye, àttekat bi daf ko gàntal doomu Nafi Ngom Keyta ji. Kon  dafay desandi ndung-siin.

Ngir fàttali, Fadiilu Keyta dafa bindoon ci xëtu Facebookam, doon ci ñaaw njort ñeel anam yi Dijje Baaji, sàndarm ba, réere.

DAAN NAÑ 9i NDAWI PASTEF YU JURBEL YI

Ci àllarbay tey ji lees doon àtte 9i ndawi Pastef yu Jurbel yi ñu jàppoon keroog bi ñuy amal seen “wër-ndomb” ca Jurbel. Àttekat bi daan na leen 6i weer ak sirsi. War nañu fay tamit 100 000 FCFA. Li ñu leen tuumaal mooy ne dañu bokk cib xew-xew bees mayewul.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj