Sëriñ Mustafaa Si moo nar a nekk lawaxub làngug polititig gii di PUR (Parti de l’Unité et du Rassemblement) ci wotey 25 féewirye 2024 yi. Ñi ngi ko tabb niki démb ci dibéer ji (19 féewirye 2024) bi ñuy amal ab mitiŋ bu mag ca estaad Aamadu Bari, doon ci màggal 25i ati làng gi ginnaaw bi ñu ko sosee woon ci atum 1998. Ci mitiŋ booboot, doon nañu sàkku ci kàddu yi fa jib ñu bàyyi Masata Sàmb ak Mamadu Ñaŋ, seen i dépite yi Yoon tegoon loxo ci coow li fi amoon ca Ngombalaan ga.
Mitiŋu bennoo ca Kéedugu
Ca Kéedugu, kilifay lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar yi tabb nañu tamit Njiitu réew mi Maki Sàll ngir mu doon seen lawax ci wotey 2024 yi. Fekk ñu doon fa amal ab mitiŋ ngir dajale mboolem seen ay ñoñ ci teewaayu jëwrin jii di Mbay Njaay. Ci kàdduy Mamadu Saaliwu Sow, Njiitu kurélu gox ba (président du conseil départemental), Kéedugu jël na ndogalu tabb Maki Sàll mi gën ci mboolem Njiiti réew yi Senegaal mas a am.
PAJ MI
Kuréli fajkat yi nar nañoo yëngu-yëngal, delloo buum ca boy-boy ga. Ëllëg ci talaata ji, lañu koy tàmbali. Dinañu amal ñaxtu ci buntu raglu yi. Bu weesoo, dinañu bank itam seen ay loxo ci àllarba ji. Ñoom nag, jàpp nañu ni Jëwrin yi laaleek paj mi dañ soofantal seen i càkkuteef. Waaye, dinañu teggi Ndakaaru ci seen ub ñaxtu bi ngir wooteb Séydinaa Limaamu Laay bi war a am ci ñaari fan yooyu.
MBATIT
Wooteb Séydinaa Limaamu Laay
Wooteb Sëydinaa Limaamu Laay, ñu gën koo miis ci turub Aajiboo, dina am ren ci àppu ñaari fan, talaata 21 ak àllarba 22 féewirye 2023. Mboolem way-gëm yi tënku ci yoonu laayeen nar a jubluji Kàmberéen, Yoof, ak Ngor ngir màggal bile woote. Bu ren bi di 143eelu yoon.
Ficas (Festival international du cinéma et de l’audiovisuel du Senegaal)
Xibaar bu neex ñeel axlu sinemaa. Senegaal dina taxawal balaa yàgg dara ab xew-xew bu mu jagleel sinemaa bi, FICAS (Festival international du cinéma et de l’audiovisuel du Sénégal). Aliw Sow, jëwrin ji ñu dénk wàllu Mbatit ak Moomeel gi, moo ko siiwal. Mu nar a doon guleet ñiy yëngatu ci wàllu sinemaa am xew-xew bu ni mel. Yoon wu njëkk bi jàppees na ko ci 3 ba 9i fan ci weeru suwe 2023 ci Ndakaar, Gore, Ndar ak Sali
TÀGGAT-YARAM
Can U20
Kubu réewi Afrig bees jagleel ñi seeniy at yées 20, CAN U20 2023, door na démb ci dibéer ji, ca Esipt. Gaynde Senegaal yi ñoom, jot nañoo am ndam ci seen joŋante bu njëkk. Niseeriyaa la ñu dóor 1 bii ci 0. Jamonoo yii, ñoo jiitu ci kippu A bi, Esipt ak Mosàmbig topp ci, Niseeriyaa mujje. Dinañu amal seen ñaareelub joŋante ci àllarba ji (22 féewirye 2023) ci seen digganteek Mosàmbig.
Raw-gàddug Senegaal
Ba tey ci wàllu kupe, raw-gàddug Senegaal (ligue 1) doon na amal 13eelu bëccëgam ci njeexitalu ayu-bés bi. Mu doonoon itam bëccëg bi tëj xaaj bu njëkk bi ci at mi. Casa Sport, Géejawaay ak Jàmbaar ñoo nekk ci boppu toftale bi ak 13i poñ ku ci nekk. Joŋante yi waaroon a dox ci diggante CNEPS ak AS Pikin, US Gore ak Ndakaaru S.C. dañ leen a dàqandi.