Décce Faal dina nekk lawax ci wotey Njiitu réewum Senegaal yu 2024 yi. Loolu la xamle démb ci dibéer ji. Fekk mu doon jàkkaarlook taskati xibaar yi ca seen ub dalu làngug pólitig gii di PRP (Parti républicain pour le progrès / diisoo ak askan wi). Xamle naat ni dinañu def am ndaje mu mag ngir amal tab gi.
Nemmeeku koom-koom
Njiitu réew mi, Maki Sàll, mi ngi jamono yii ca bëj-saalumu réew mi, ca diwaanu Séeju. Tukki 5i fan la fa war a amal ngir nemmeeku koom-koom gi. Dina fa jiite ndajeem jëwriñ yi, daloo (inaugurer) fa itam poŋ bii di Marsaasum. Bu loolu weesoo, dina fa amal itam am ndaje ak kilifay diwaan ba ngir waxtaan ak ñoom ci suqaleeku dëkk ba.
XEW-XEWU JAMONO
Mbiru Fulbeer Sàmb ak Dijje Baaji nekkagul lu ñuy fàtte. Seen iy mbokk yi dëkke ci dun yu Bilis Kaasa, ca gox bu Biñonaa ñoo àddu wile yoon. Ci gaawu gi lañu doon jàkkaarlook taskati xibaar yi ngir ñaawlu anam yi ñu faatoo. Ñoom nag, ña ngay xamle ni xel xalaatul ñuy gëm ni seen doom yii dañoo lab. Nde, loolu mënul a nekk. Ba dinañu taxaw temm ba Nguur gi wax dëgg ji seen iy njaboot.
TÀGGAT-YARAM
Gaynde Senegaal yi jàll nañu ci kaar-dë-finaal yu CAN U-20 2023 biy am fan yii fale ca Esipt. Ginnaaw bi ñu dóore Niseriyaa (1 bii ci tus), teg ci Mosàmbig (3i bii ci tus), Esipt mi dalal joŋante bi lañu wulli 4i bii ci tus ci seen ñetteelu joŋante. Muy ñetti ndam ci ñetti joŋante ba tax ñu jiitu ci kippu A bi. Ci kaar-dë-finaal yi ñu jëm, gaynde yi dinañu dajeek doomi réewum Benĩ yi ci alxames ji, 2i màrs 2023 bu 14i waxtu jotee.