Militaŋi APR yi nekk ci peggug Ndakaaru doon nañu amal ab mitiŋ ci dibéer ji, ca bayaalub SEFA bi nekk ca Pikin. Mitiŋ boobu nag, ñaŋ ca doon jàppal tànk kii di Njiitul réew mi Maki Sàll ak di ko delloo njukkal ci li mu fi jot a def diggante 2012 ak tey. Kilifay APR yu bare sax teewoon nañu fa, ba ci magum-jëwrin yi, Aamadu Ba. Moom Aamadu Ba nag, bi mu jëlee kàddu, xamle na ni ñoom waa APR amul leneen lu ñuy waajal. Kenn la ñu am, te mooy Maki Sàll.
Njàppug militaŋi Pastef yi
Ay militaŋi Pastef yu bare la yoon teg loxo. Bu ñu déggee li Usmaan Sonko, njiitu pastef li, wax, ñi ngi tollu ci 27i doom-aadama. Kenn ci ñoom sax xale la bu war a tollu ci 15i at. Ñi ñu ci mujje teg loxo, ñoo ngi leen jàppoon ca alxames jii weesu bi ñuy amal opération wër-ndomb ca Jurbel. Tey ci altine ji la ñu leen war a jàllale. Usmaan Sonko nag, ma ngay xamle ni jaabante na ci béréb yi ñu leen téye, waaye kenn bàyiwu ko mu gis leen. Mu ne, dinañu ci amal taxawaay bu mat te lépp lu mu laaj rekk dinañu ko def ba bunduxatal gi dakk.
NJÀNG MEEK NJÀNGALE MI
Njàng meek njàngale mi dees na ko xoolaat. Loolu la Jëwriñ ji Séex Umar Aan xamle. Xoolaat boobu nag ña nga ca jublu wàññi barewaay bi ndong yi gis ne dafa diis lool ci ñoom. Liggéey bi ci aju nag, dénkees na ko waa IGEF (Inspection générale de l’éducation et de la formation) maanaam kurél giy saytu njàng meek njàngale mi. Caytu googu ñu naal, boobu dina laal njàngum tuut-tànk yi, daara yu suufe yi, yu digg-dóomu yeek yu ci topp, ak njàngum ndaw ñeek mag ñi.
TÀGGAT-YARAM
Bésub ndam lu dellusi
6 féewaryee 2022 ba 6 féewaryee 2023, atu Yàllaa ginaaw bi Sénégaal njëkkee jël CAN (Coupe d’Afrique des Nations ). Askanu Senegaal yépp ànd di ko fàttaliku. Muy mbégte mu réy rawatina bi gaynde yu ndaw yi jëlee tamit CHAN (Championnat d’Afrique des Nations) bi ci gaawu bii weesu ca Alséri. Ñoom gaynde yu ndaw yi, Njiitu réew mi Maki Sàll doon na leen dalal niki démb ci pale ba.
Nawetaan : xeex bu metti ca Sigicoor
Xeex bu metti moo amoon ca Sigicoor diggante takk-der yeek way-fari ASC Karantaba ca estàdd Aliyun Sitooye Jaata. Ñaari ekib yii di ASC Kajoor ak Belfoor ñoo fa waroon a amal seenub gañ-jël ci wàllu nawetaan yi. Bi joŋante bi waree tàmbali nag, la way-fari ASC Karantaba yi wàcc ci fowu bi, lànk ni joŋante bi du fa ame ba takk-der ya mujje sox seen gërënaat yi. Ñoom nag, li leen metti mooy seen ekib bi waroon a dem ci gañ-jël bi te ay daan tax ñu seppi ko. Jamono yii nag, kilifa yaa ngay xool yan ciy ndogal lañ war a jël. Cig pàttali, Perefe bi njëkkoon naa ajlu gañ-jël boobu bi mu waree am ci bésub 28 sãwiye bi weesu.