LI GËN A FES CI XIBAARI BÉS BI (Alxames 16 féewaryee 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LAYOO MAAM MBAY ÑAN AK USMAAN SONKO

Tey ci alxames ji lañu waroon a àtte Maam Mbay Ñaŋ ak Usmaan Sonko waaye mujjul àntu. Ndax, dañoo mujjee ajandiwaat layoo bi. Layoo boobu nag jàppaat nañu ko fukki fan ak juróom-benn ci weeru màrs. Waaye, coow amoon na ci.

Nde, li ñépp nemmeeku te ñaawlu ko mooy li takk-der yi def Usmaan Sonko. Dafa di, tey yépp, dañu ko topp, li ko dale këram ba ni muy ñibbee. Bi muy dem tirbinaal la koy wata BIP yi dar, daldi mbëkk ñaari daamaram. Bi mbir mi jeexee itam, dañu ko sëqatal, kar ko, tere koo dem. Loolu doyul, ñu ne ko fàww mu génn wataam, dugg ci bob pólis. Bi njiitul Pastef li bañee, takk-der yi dañu toj weeru wataam bi ñépp di gis, jaay ko doole, génne ko, dugal ci seen daamar daldi yóbbu këram. Nu ni déet-a-waay, Sonko bëgg a dem ca dalu pàrteem ngir amal waxtaan ak taskati-xibaar yi ñu ne koo dee du dem, daldi koy sàndiy lakkirimosen ba dafa mujje dellu këram. Muy lu doy a doy waar ci réew mu ni mel.

XAMEES NA ÀPPUB WOTEY 2024 YI

Sànq, ci yoor-yoor gi, la xibaar bi rot. Kii di jëwriñ ji ñu dénk wàlluw biir réew mee biral xibaar bi, jaare ko cib yëgle. Àpp boobu nag, mi ngi yemoo ak dibéer ñaar-fukki fan ak juróom ci weeru feewaryee 2024.

COPPITE CI BOPPU KURÉLU CDL

Kurél gii ñu dippe Conférence des leaders (CDL) nga xam ne lëkkatoog Yewwi Askan Wi moo ko taxawal soppi na njiitam. Kii di Abiib Si mooy ki ñu teg ca bopp bi ginnaaw ba kii di Xalifa Abaabakar Sàll jógee ca bopp ba.

PUR BIRAL NA LAWAXAM

Làng gii di PUR (Parti de l’Unité et le Rassemblement) biral na lawaxam ñeel wotey 2024 yi. Kii di Sëriñ Mustafaa Si mooy ki ñu namm a def seen lawax ci wote yooyu. Baabakar Géy (Président du conseil départemental de Kër Masaar) mooy ki jibal xibaar bi. Nee na nag, kàddu gu mujj moom, kilifa gi moo ko yor.

XIBAAR YU YEES ÑEEL MITIŊ BA AMOON CA MBÀKKE

Àjjuma jii weesu la gaa ñi fare ci Usmaan Sonko doon amal seen ub mitiŋ. Mitiŋ boobu nag, perefe ba daf ko gàntaloon. Mu amoon ay jàmmaarloo ba am ñu ñu ca jàppoon. Ñu ne nag, tegoon nañu fa loxo lu tollu ci juróom-benni-fukki nit ak juróom-ñeent. Démb, kii di àttekatu Jurbel bi téye nañu ci lu tollu ci fanweer ak ñeent, fukk ak ñeent ñu bàyyi lenn bàyyib négandiku. Ñaar-fukk ak benn ya ca des ña nga ca loxoy komisariyaa ba.

MBIRUM RAGLUB DANTEC

Juróom-benni weer ginnaaw bi ñu tàmbaliwaatee ndefarug raglu Aristide Le Dantec, coowal njaayum lenn ca bayaal ya jiboon. Maanaam lu tollu ci ñetti ektaar lañu ci naroon a jaay ngir kopparal ndefar gi. Njaay moomu nag mujj nañu ko gàntal.

JÉYYAB TIRKII AK SIRI

Fukki fan daanaka ginnaaw ba jéyya ji amee ca ñaari réew yooyu, ay bakkan a ngay wéy di ca rot. Ndax, ci jamono jii, limu ña fa ñàkk seen i bakkan daanaka jege na 42.000iy nit. Tirki rekk, lu tollu ci 36.187iy nit ñoo fa ñàkk seen i bakkan bees sukkandikoo ci Agence de presse officielle Anadolu. Lu ëpp 50.000iy tabax màbb nañu ca Tirki rekk, lu ëpp tamit 100.000iy nit yu ci jële ay gaañu-gaañu. Lu jege tamit 13.200iy nit ñoo xam ne ba tey ña nga ca raglu ya di faju.

AKSIDAŊ CI OTORUT BI

Aksidaŋ bi mi ngi ame ci otorut ilaa Tuubaa bi tey ci suba. Benn kaar Njaga Njaay moo fa daanu. Benn liir bu tollu ci juróom-ñeenti weer moo ca ñàkk bakkanam, lu tollu ci fanweer ak juróom-ñeenti nit jële ca ay gaañu-gaañu.

DOGAALEG ÑAARI TASKATI-XIBAAR YU WALFTV

Jëf jooju nag, mi ngi amoon démb ci ngoon. Kii di Paap Maxtaar Jàllo ak Maam Biram Waaj ñooy ñaar ñi ñu dogaale démb. Ñoom nag dañoo jóge woon ca doxu-ñaxtu ba ñu doon def jagleel ko Nit Dof. Bi ñu jógee foofa di ñibbisi ci lañu leen dogaale.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj