Ca ndajem jëwriñ ma mu doon amal démb, kii di Njiitu réew mi Maki Sàll jot naa am ñenn ci ay ñoñam ñu mu fa takkal ay ndomboy-tànk. Ñooñu mu takkal ndombo-tànk yi nag, ñii la : Biraan Mbañig Jaañ (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de son Excellence Monsieur Mohamed Ould Cheikh EL GHAZOUANI, Président de la République Islamique de Mauritanie avec résidence à Nouakchott), Sã Antuwaa Juuf (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de sa Majesté NARUHITO, Empereur du Japon, avec résidence à Tokyo), Maalig Ndaw (Ambassadeur extraordinaire et plénipotentiaire de la République du Sénégal auprès de son Excellence Monsieur Joao Manuel Goncalves LORENCO, Président République d’Angola, avec résidence à Luanda), Abdu Kariim Sàll (Directeur général de l’Autorité de Régulation des Télécommunications et des Postes), KaliduBa (Directeur général du Fonds de Solidarité nationale au Ministère du Développement communautaire, de la Solidarité nationale et de l’Equité sociale et territoriale), Sã Kone (Directeur du Renseignement et des Stratégies fiscales à la Direction générale des Impots et des Domaines), Seex Ahmadu Bàmba Ndaw (Directeur du Commerce intérieur au Ministère du Commerce, de la Consommation et des PME), Elaas Àlliyu Jaane (Directeur de la Promotion de l’Habitat social au Ministère de l’Urbanisme, du Logement et de l’Hygiène publique), Aadama Fay (Directeur de la Peche continentale au Ministère des Pêches et de l’Economie maritime), Abdulaay Juuf (Directeur des Industries de Transformation de la Pêche au Ministère des Pêches et de l’Economie maritime), Seex Mbàkke Caam (Directeur de l’Administrattion générale et de l’Equipement au Ministère des Infrastructures, des Transports terrestres et du Désenclavement), Mbay Jonn (Secrétaire général de l’Université Amadou Mahtar Mbow), SeydinaaAbaabakar Mbeng (Secrétaire général de l’Université Alioune Diop), Moor Faal (Secrétaire général de l’Université Gaston Berger de Saint-Louis), Seex Njaay (Secrétaire général de l’Université Assane Seck de Ziguinchor), Hammadu Balde (Secrétaire général de l’Université Numérique Cheikh Hamidou Kane).
Perefeb Ndakaaru gàntal na waa YAW
Tey ci alxames ji la lëkkatoo gii di Yewwi Askan Wi bëggoon a amal am ndajem-ñaxtu ca kanamu Ngomblaan ga. Li ñu ko dugge woon nag mooy sàkku ñu bàyyi seen naataango yooyu ñu jàppoon. Muy kii di Masata Sàmb ak Mamadu Ñaŋ, ñi ñu tëjoon ci coow li doxoon seen diggante ak Ami Njaay Ñiibi. Waaye, ndaje moomu mujjul a àntu ndax perefe bu Ndakaaru bi mooy ki ko gàntal.
Muhammed VI yebbi na
Ay waxtu kepp a desoon kii di buuru Marog ba woon ca Rabaa ñëw Senegaal. Moom nag, dafa mujj yebbi ñëwam googu. Li ko waral nag mooy ne buur bi dafa tawat (grippe). Ba tax kii di fajkat bi ne ko dafa war a noppalu te moytu tukki fii ak i fan.
WÉR-GI-YARAM
Tereb siro Karbotuk
Kurél gii di ARP (Agence sénégalaise de Réglementation Pharmaceutique) moo tere ñuy jaay walla ñuy jëfandikoo xeetu siro boobu. Moo tax ñuy sàkku ci bérébi jaayukaayi garab yépp ñu génnee li ñu yor ci siro bi, muy yu mag yi walla yu xale yi.
KOOM-KOOM
ARMP tanc na SONES
ARMP (Autorité de Régulation des Marchés Publics) di kurél giy saytu doxalinu ja yi, moo gàntal pas gu SONES (Société nationale des eaux du Sénégal) xaatimoon ñeel wàllum ndox mu set. Koppar googu mi ngi tolloon ci 7,7i miliyaar. Li ko waral nag mooy kurél gi dafa ne dañoo gëddaalu yenn ci sàrti ja yi.
Daan bi dal na ci kow SONATEL
Ëttu àttewaay biy saytu wàllum njaay mi ak njënd mi moo daan këru jollasu gii (société de téléphonie) di Sonatel. Ñoom dinañu jox ñii di Interface Sas lu tollu ci 1,1i miliyaar. Li ko waral nag mooy kii di Màgget Silla dafa jiiñ ñii di waa Sonatel ne dañoo sàcc xam-xamam (violation de propriété intellectuelle).
XEW-XEWI JAMONO
Xamees na sóobare ya faatu ak ya gaañu ca Mali
Ñetti sóobare ñoo fa ñàkk seen i bakkan, juróom jële ca ay gaañu-gaañu. Ki ci jiitu di wuyoo ci turu Uséynu Jàllo dëkk ca Kawlax, amoon lu tollu ci fanweeri at ak ñett. Ki ci topp di Eugène Idiriisa Badin Mingu, dëkke ca Sigicoor. Ki ci mujj di Piyeer Bubaan dëkke ca diwaanu Kéedugu. Juróom yi ci jële ay gaañu-gaañu, ñii la : Pàppa Mammadu Maas Jóob, Seex Ahmet Juuf, Mammadu Sàll, Amdi Mustafaa Jóob, Farãsuwaa Saar.
Xew-xew bu doy waar ca Wakaam
Démb la mbir mi xew, kii di A.J.Sumaare, ag góor gu tollu ci ñeen-fukki at ak ñett moo fa xaru. Moom nag dawalkat la woon, ma nga xaroo ca néegam ba nekke ca koñu Baye, ca Wakaam. Ci xibaar yi jot a rotagum nag, nee ñu da doon jàmbat bopp buy met ci suba gi. Waaye nag, jabar ji moo ko fekk ci biir néegam mu takk buum gi ci baat bi, wékk ko ci kow.