LI GËN A FËS CI XIBAARI BES BI Talaata 25 oktoobar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

YOKKUTEG NJËGU DUGUB BI 

Jamono jii, askan waa ngiy jooy dund biy wéy di yokk. Nde, dugub bi tamit yokk na. Kilo bi daan jar 400i dërëmi CFA, yokk na ba 700i dërëmi CFA. Looloo merloo jaaykatu cere yeek fonde yi. Nee ñu, daanaka, amatuñu dara ci njaay mi ndax li dugub bi yokk. Joxoñees na baaraami tuuma Càmm gi ak jaaykat yi. Wëliis dugub bi, saa-senegaal yaa ngi jooy tamit luyaas bi ak mbëj (kuraŋ) mi yokk, di xaar nguur gu yees gi indi ciy saafara, wàññi njëg yi.

AYSATA TAAL SÀLL : « …DIPOLOMASI MOOY MOOM SA BOPP CA DËGG-DËGG »

Ca waxtaan wa mu amal ak waa Europe 1, jëwriñu Senegaal ji ñu dénk mbiri bitim-réew a ngi ci ñaawlu ak naqarlu kàdduy réewi sowu yi, rawatina Farãs, ci taxawaayu réewi Afrig yi ñeel xareb Ikren bi :

« Mënuma nangu ñuy wax ne Senegaal amul taxawaay bu leer. Ndax dégg ngeen nu, nu wax menn réew mu layal taxawaayam ci mbir mi ? Mukk. »

Cig pàttali, ñaari ayu-bés ci ginnaaw, ci biir 54i réewi Afrig, 26 kese ñoo àndoon ak Ikren, wote déggoob ONU biy daan Riisi ci noot bi mu noot 4i diwaani Ikren. Loo taxoon Farãs, keroog ca Forum bi amoon Ndakaaru ñeel kaaraange gi, waxoon ne réewi Afrig yi, rawatina Senegaal, dañoo war a leeral seen péete. Mu mel ni wax jooju dafa naqari ndaw si. Moo ko tax waxati ne :

« Lu tax rekk, saa bu réewi Afrig yi tànnee seen ug péete, ñu war koo layal ? Dipolomasi mooy moom sa bopp dëgg-dëgg. »

NGOMBLAAN GI : KURÉLU NGURD MI DOOR NA LIGGÉEYAM

Ci talaata démb ji la kurélu gees dénk ngurd mi ak caytug nafa gi door liggéeyam ca Ngomblaan ga. Ci li Ngomblaan gi xamle, tàmbalee nañu càmbarug sémbub àtteb koppar ñeel atum 2023 mi.  Liggéey bu ni mel nag, càrtub Ngomblaan gi dafa aaye, ci seen i wax, ñu koy biral taskati-xibaar yi. Nee ñu, kurél googu dina wéyal liggéeyam ba keroog gaawu 12 nowàmbar 2022.

DÉCCE FAAL A NGI WAAJAL TUKKIB NEMMIKU

Parti Républicain pour le Progrès (PRP)/Diisoo ak Askan Wi ngembu na, sóobu ci waajtaayu woteb njiiteefu réew mees dégmal ci 2024 mi. Génne nañu ab yégle di ci xamle ne seen njiit lii di Décce Faal dina amal tukkib nemmiku ci àddina sépp. Li mu ko dugge mooy waxtaani ak saa-senegaal ya nekk bitim-réew. Tukkib nemmiku boobu nag, « Kaye Bokk » [Kaay Bokk] lañu ko tudde. Bu ko defee, li ko dale 26 oktoobar jàpp 13 nowàmbar 2022, Décce Faal dina dem « Kaasabalankaa ca Marog, Beresiyaa ca Itali, Anwers ca Belsig, Bóordóo, Dënkëerk, Liil, Pari ak Mànt-Laa-Soli ca Farãs, Aten ca Geres ak ca dëkki Madrid ak Palmaa Bu Mayork ca Espaañ. »

TOF-NJIIT LU MAG LU AMNESTY INTERNATIONAL DINA WAX AK TASKATI-XIBAAR YI ÀJJUMA

Amnesty International a ko xamle cib yégle. Añes Kalamaar mi ngi Ndakaaru te dina amal am ndaje ak taskati-xibaar yi àjjuma jii, bu 15i waxtu jotee.  Ci yégle bi, jàngees na ci ne, Soxna  Añes Kalamaar, li ko dale 16 oktoobar ba tey, mi ngi amal ab tukki nemmiku biir Afrig sowu-jant.  Bi mu ñëwee Senegaal, « waxtaan na ak njiiti réew mi ci àqub amal ndajem-ñaxtu, jaay-doole bu ëpp bi, sañ-sañ wax sa xalaat, kaaraangeg taalibe yi, àtteb nit ñi dee woon màrs 2021 ca ñaxtu ya toppoon ci njàppug Usmaan Sonko ga. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj