Ci diibéerub démb ji la Gastõ Mbeng tëggoon làmb ju réy ju doxoon ci diggante Giri-Bórdoo ak Bàlla Gay 2. Mbëru Géejawaay ji moo daan mbëru Faas bi. Bii mooy ñaari yoon Bàlla Gay di am ndaw ci kow Giri- Bórdoo.
MBËNN MI : Ñetteelu bakkan rot na
Mbënn mi reyatina kenn ci diiwaanu Ndakaaru. Bii mooy ñetteelu nit ku ci ñàkke bakkanam bi taw yi doore ba tey. Ab xale bu góor buy wuyoo Mammadu Jàllo, cosaanoo ca réewum Gine, tolloon ci 15i at, la ndox mi faat. Waa Dakaractu a ngiy xamle ne sàppëër yi daj nañ lu nekk laata ñuy àgg ca kanaalu « Front de Terre », fa xale ba labe ba koy génne. Ndekete, waa Grand-Yoff a amaloon ab doxu ñaxtu ngir fësal seen ub mer ak seen uw naqar ñeel coono ak jafe-jafe yi leen mbënn mi jural.
PÓLITIG : « Plan ORSEC » dikkati na
Ngir indiy saafara ci lor yi mbënn mi jur ginnaaw taw yu metti yi jot a wàcc ci Ndakaaru, Nguur gi dekkal na « Plan ORSEC ».
Waaye, kii di El Maalig Njaay, moom, dafa jàpp ne « Plan ORSEC » bi ab njuuj-njaaj kese a ko lal ak ñàkk yërmande ci saa-senegaal yi. Mu ngiy junj tamit ne liggéey bu njëkk bu depite yu yees yi war a amal mooy amal ub lëñbët ngir saytu, càmbar « Plan ORSEC » bi.
DOGI MBËJ MI AK ÑÀKKUM NDOX MI : doxu ñaxtu fa Ndakaaru
Waa Ndakaaru amaloon nañ ab doxub ñaxtu ci gaawu gi 6 ut 2022. Li ñu ko dugge woon mooy wone seen naqar ci ñàkkum ndox mi ak mbëj miy dem ak a dikk ci ñaari fan yile.
YOON : Yégleb layookati Farãsuwaa Mànkabu
Njaabootu Farãsuwaa Mànkabu taxaw nañu temm ne nañ leen dello seen néew, te it duñu bàyyi dara mu sedd. Ñu teg ci ne, fu yoon nekk, muy ci réew mi walla di bitim-réew, dinañ fa àkki ngir am ndam ci ñii di Komiseer Sàngare, njiitu raglbiu bu Dantec, ak porokirëëru Senegaal .