Paap Aali Jàllo
Doktoor Séydu Jàllo ab farmasiyeŋ la, dib biyólósis. xam-xamam màcc na tamit ci wàllu kiiraayu biir yaram ak ség. Tey, day waxtaan ak nun ci mbasum Covid-19 mi lëmbe àddina si. Ci ñaareelu xaaj bii, day biral njàngatam ci mbas mi ñeel Senegaal, niwaakin bi ak coowal ñakk li.
Paap Aali Jàllo : Noo gise dogal ak matuwaay yi nguuru Senegaal jël ngir xeex mbas mi ?
Séydu Jàllo : Waaw. Jàpp naa ne, dogal yi ak matuwaay yi nguur gi jël baax nañ. Ci sunu wàllu bopp, noo ngi koy rafetlu. Wiris bi amul ay tànk, nit ñee koy tasaare. Moo tax, dogal yeek matuwaay yi baax, rawatina liñ tere mbooloo yi.
Dafa di, nag, mbas mi jéggi na wàllu wér-gi-yaram kese. Fànn yépp la laal : politig bi, aada yi ba ci sax koom-koom bi. Yaakaar naa ni sax, li sunu koom-koom aju ci bitim-réew moo taxoon nguur gi teelul woon fatt digi réew mi, maanaam aaye fafalnaaw dugg Senegaal. Boo seetloo, sunu way-tawati Covid-19 yu jëkk yi bitim-réew lañ jóge. Ci roppëlaan yi lañ jaare. Gannaaw bi lañ def ay nattukaayi tàngooru yaram (thermoflash, thermomètre) ngir ràññee nimsaafoni Covid-19 bi (cas suspects du Covid-19). Waaye, loolu taxu koo baax noonu.
Jàngoro ji mën na nekk ci nit ki 7 ba 15i fan te du feeñ. Kon, boo nattee tàngooru yaramu aji-tukki bi, amaana doo gis dara fekk ne ame na jàngoro ji. Te sax, nit ki mën na ame tàngooru yaram fekk ne sibbiroo ko sabab walla leneen lu dul Covid-19 bi. Moo tax ma ne, nattukaayi tàngoor yooyu ñu defoon ca ayeropoor Belees Jaañ taxu ko woon am njariñ noonu. Lees war a def te mu jàmp lool, mooy wëri wàllent-ëlëm yi. Am na ñuy wax ne nguur gi dafa war a sàrtal gaw gi, ku nekk dëju sa kër.
Ci sama xalaat, loolu mënul nekk. Bu fekkee ni nguur gi mën na jox boroom kër bu ci nekk li muy dunde moom ak njabootam ci diirub weer, dina ci baax lool. Waaye, gaw moom, dina metti lool ci askan wi bu dee defuñu loolu. Rax-ci-dolli, li ëpp ci li nuy dunde, bitim-réew lan koy jéggaani te askan wi, ñi ci ëpp, ay góogóorlu lañ. Li ñuy fortaatu ci bés bi lañuy dunde. Boo leen teree génn, dinga leen lor, ñoom ak seen i njaboot.
Ci beneen boor, liñ tere tukki dëkk ak dëkk yi tamit jur na ay gàllankoor. Am na ñu amoon ay dig-daje ci loppitaani Ndakaaru yi, rawatina ñi ame kañseer te mënuñoo fajusi. Nguur gi war na geestu ñooñu ngir dimbali leen.
PAJ : Nan nga gise xibaar yi jawriñu wér-gi-yaram biy biral bés bu nekk ?
SJ : Damay njëkk a rafetlu taxawaayu jawriñ Ablaay Juuf Saar bi mbas mi duggee ci réew mi ba léegi. Xibaar yi muy joxe bés bu nekk lu baax la. Fi mu nekk nii, mënees na wax ne, ak limu way-tawat bin am, mbir mi ëppagul loxo. Wànte, ndax su feebar bi gënee law dina ko mënati ?
Rax-ci-dolli, bees sukkandikoo ci xibaar yi muy joxe, 4 000 nimsaafoon lañ lëlagum. Ñu saytoogum ci 500 ak lu teg. Loolu day wone nisunu loppitaan yi amuñu jumtukaay yu doy ngir mën a def seen liggéey. Ndaxte, waroon nan romb fii bu yàgg.
Te sax, mënees na am xel ñaar ci lim yi jawriñ jiy joxe bés bu nekk. Du càggénu ne dafa am lu muy nëbb askan wi ; waaye, dama njoort ne am na ci doomi-réew mi ñu ko ame te xamuñu ko, xamuñu leen itam. Te, lu mën a nekk la ndaxte Senegaal amul jumtukaay yu doy ngir saytu askan wépp.
Man, damay ragal ñu am ay way-tawat yuy dox ak a doxantoo jàngoro ji, di ko tasaare ci nit ñi te kenn xamu ci dara. Dangay xool ni sunu dëkk yi bindoo, ni dund bi mel ci gox yi ak gox-goxaat yi…
Li ma doon gënal te gën a dal xel mooy ñu def « dépistage de masse ». Maanaam, ñu paase-wisit ay fuli mbooloo ngir xam dëgg-dëgg limu nit ñi ame jàngoro ji. Li ma ko tax a wax, nag, du lenn lu-dul ne wàllent-ëlëm yaa ngiy yokku. Xanaa nguur gi sàrtal mask yi ci askan wi. Muy lu jafe tamit. Ndaxte, mask dafa mànke ci àddina si.
PAJ : Am na ñu jàpp ne, mbasum Covid-19 bi, loxoo ko def. Loo ci xalaat ?
SJ : Li ko dale 2eelu Xare bu mag bi ba sun-jonni-Yàlla tey jii, gis nan fi xareb suuf (guerre froide) bi amoon ci diggante Etaasini ak Riisi. Mu am nag beneen xeetu xare bu bees, réew yu am doole yi di ko jëfandikoo te muy xareb wér-gi-yaram (guerre biologique). Loolu moom lu am la. Ndax, fi xam-xam tollu tey ak jumtukaayi xarala yi yees yi, mënees na soppi njuraafoon yi ci biir laboraatuwaar yi. Mënees na yit sos ay wiris yu bees. Rax-ci-dolli, mënees na jël benn saalub-dund (cellule) bu benn mala, ful ko mbaa ñu liggéey ko ba génne ci mala bu ni mel, Tubaab di ko wax « clonage ». Loolu yépp lu mën a nekk la, tesax lu am la.
Bu dee nag Covid-19 bi, xamaguñ ni mu bindoo. Moo tax mënuma cee sore. Waaye, li ci kanam rawul i bët. Du ñàkk nu am ci lu leerbalay yàgg.
PAJ : Loo xam ci li Doktoor Raoult wax ne niwaakin mën na faj Covid-19 bi ak coow li mu jur ci àddina si, rawatina Senegaal ?
SJ : Porfesoor Raoult gëstukat bu mag a mag la ci wàllu wér-gi-yaram te ku xareñ la ci li muy def. Moom, nag, daanaka li Sinwaa yi def rekk la def.
Naam, saytu na niwaakin bi ci mbooloom way-tawat mu yem, am ciy ngirte yu dal xel. Waaye, lees koy sikke, mooy dafa am ay sàrt yoo xam ne, ci wàllum paj, sàmmoonteegul ak ñoom. Weddiwuñ li mu wax. Dañ ko ne dafa teel a siiwal ngirteem yi. Am nay gëstu ak seetlu yu bare yiñ war a def laata ñuy dëggal ne garab sàngam day faj jàngoroy sàngam.Waaye Porfesoor Raoult da ne ci jamonoy xare lanu nekk, mbas maa ngiy rey saa su nekk, kon warunoo xaar.
Dafa di, moom Porfesoor Raoult, bi mu joxee niwaakin bi (hydroxychloriquine) ñenn ciy way-tawati Covid-19 yim doon faj, dafa gis ni dooley wiris bi day wàññeeku bu baax, ñu mujje wér. Loolu moo ko tax a jàpp ne niwaakin day faj Covid-19 bi.
Bëgg naa indi ay leeral ñeel niwaakin boobu. Réewi sowu-jant yi daawuñ ko jëfandikoo ndax sibbiru amu fa. Nun, Afrig bëj-saalum màndiŋu Saxara, dañ ko daan jëfandikoo lu bare laata ñu koy dakkal. Ndax daa demoon ba fajatul sibbiru bi ko taxoon a jóg.
Ci beneen boor, jàngoroy Covid-19 dafa am dayo, 1, 2 ba 3. Te, bees sukkandikoo ci gëstuy Porfesoor Raoult, ci dayo 1 ak 2 rekk lees mën a jëfandikoo niwaakin bi. Ci gàttal, mëneesul a fegoo niwaakin bi ; te yit aji-tawat bu ci àgg dayo bu mujj bi ba ñu sampal la noyyikaay, niwaakin bi du ci mënati dara.
Warees na xam tamit ne, niwaakin bi walla « hydroxychloriquine » bi dafay sabab yenn xeeti jafe-jafe ñeel ndigg ak yeneen xeeti cër.
PAJ : Loo xam ci coowal ñakk biñ wax ne Afrig lañ ko bëgg a natte ?
SJ : Lépp loo gis, dafa am yoon, rawatina li jëm ci wér-gi-yaram. Coowal ñakk bi, nag, bare na lool. Bala dara, warees na xam ne, ñakk day laaj 4 jamono laata ñuy wéral mbaaxam. Bi ci jiitu mooy jaxub kilinig (essai clinique), bi ci topp di jaxub mala, gInnaaw bi ñu settantal ko ci mbooloo mu yem. Bu ñu weesoo foofu yépp, nag, te amul benn jafe-jafe, ci la ñuy door a jëfandikoo ñakk bi. Bu dee Covid-19 bi, àggagun foofu. Kon, waxi ñakk teel na. Loolu benn la.
Ñaareelu mbir mi mooy ne, bu dee am na ñu soxla ñakk jamono jii, réewi Ërob yeek yu Amerig yi la. Ndaxte, ñoom ñoo nu gën a sonn. Teg ci ne, nun réewi Afrig yi, dañuy faral di ñakk xale yi ca ba ñuy gone. Ñakkub BCG bi bokk na ci ñakk yiñ leen di defal. Te, BCG bi day aar xëtër yi. Amaana mu aar ñu bare ci doomi Afrig yi ci Covid-19 bi.
Yaakaar naa ne doomi Afrig dofuñu te kenn mënatu leen a nax.