LI UMAR YUM AK AALI NGUY NJAAY WAX TASKATI XIBAAR YI ÑEEL GUURAL GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paap Aali Jàllo

Senegaal, ca njëlbeen ga (2eelu fan ci weeru màrs 2020), diiwaanu Ndakaaru kesee amoon Covid-19. Wànte, tey (29eelufan ci  weeru màrs jàngoro ji law na ci 6 diiwaan (Ndakaaru, Njaaréem – Jurbel – Cees, Sigicoor, Ndar ak Fatig). Kon, luy jot jot na.  Dafa di, Covid-19 bi amul i tànk, nit ñiy dem ak a dikk ñoo koy tasaare. Moo tax, njiit yi jël ay dogal ngir feg mbas mi. Jawriñ jiñ dénk kaaraange biir réew mi ak naataangoom bi yor wàllu dem beek dikk bi amalandoo nañ ab waxtaan ak taskati xibaar yi ñeel guural gi (état d’urgence) njiitu réew mi dogal ci altine ji. Pexe yi njiitu réew mi, Maki Sàll, lal ngir daan Covid-19 bi la Aali Nguy Njaay ak Umar Yum doon leeral.
Aali Nguy Njaay, jawriñ jiñ dénk kaaraange biir réew mi :
“Mbooloo yi lanu aaye, waaye terewunu kenn julli”
Jawriñ Aali Nguy Njaay moo jëkk a wax. Moom, nag,  jël nay dogal yoo xam ne, dañuy wàññi bu baax a baax yëgu-yënguy askan wi. Waaye, lépp rekk, ciy kàddoom, xeex jàngoroy Covid-19 bee ko waral. Dogal yii la fa biral :

  1. li ko dale 20 waxtu ci guddi jàpp 6 waxtu ci suba, tere nañu demlante beek dikkalante bi. Nee na, na ku nekk toog sa kër ci diir boobu ;
  2. ci diir boobu ba tey, tere nañ woto yépp ñuy daw dëkk ak dëkk ;
  3. alkaati yi, sàndarm yeek soldaar yi dinañ wàcc ci tali yeek koñ yi ngir fexe ba askan wi dëppook dogal yii ; 
  4. ku sàmmoontewul ak guural gi, dees na la tëj kaso 2i weer ba 2i at walla ñu alamaan la 20 000 ba 500 000 ci sunu xaalis. Mu leeral ne, ñaari xeeti daan yooyu, benn bi rekk a mën a dalci kow nit ki.
  5. Dogalu dëju-guddi (couvre-feu) googu, nag,ñii ñuy limsi taxu koo jóg : njiiti campeef yi, jawriñ yi ak fara-caytuy nguur yi, dipite yi, àmbasadëer yi, jaraaf yi, perefe yi, tofoy perefe yi ak seen i tofo, way-àtte yi ak way-denc yi, ñiy liggéey ci wàllu wér-gi-yaram ak ñiy liggéey ci wàllu kaaraange. Bu dee am na keneen ku yeyoo ñu teggil la tere bi, ci kow nga am lay bu wér (feebar, tukki walla soxla yu jamp), jawriñu kaaraange biir réew mi mbaa pólis walla perefe dina la bindal kayit ngir nga mën a faji sa soxla.

Bi loolu weesoo, jawriñ Aali Nguy Njaay tontu na ciy laaj ñeel jumaa yi ak jàkka yi. Ci ndoorteel li dafa ne woon :
“Mbooloo yi lanu aaye, waaye terewunu kenn julli. Aar askan wee nu ko tax a def. Te, ci sunu biir doxalin, tëbunu tëb rekk jël dogal bi. Dan cee waxtaan ak kilifa diine yi ba noppi, ñaan leen ñu jàppale nguur gi ci xeex bi, aj seen i xew-xew, ndeem seen wér-gi-yarami taalibe soxal na leen. Ci kow loolu lañu fomm seen i xew-xew yi waroon a am ci weeru màrs”.
Mu teg ci ne :
Àjjuma jii weesu, ci 4 500 jumaa, 500 kese ñoo ci julli. Maanaam, ci xayma, téeméeri jumaa yoo jël, 89 julliwuñu keroog. Te, ni ñu doxale woon moo nu taxoon a am ngirte yile. Kon, àjjuma jii di ñëw, dunu soppi sunub doxalin. Nde, yaakaar nan ni, bii yoon, jumaa yépp dinañ tënku ci tere bi. Ndaxte, muy sëriñ yi di ilimaan yi, ñépp ñoo xam ne aar askan wi rekk a sabab aaye yin aaye mbooloo yi. » 
Umar Yum, jawriñ ji yor wàllu dem beek dikk bi, moom, lii la wax :
“Dinan wàññi palaasi woto yi lu tollook xaaj…”
Bi jawriñ Aali Nguy Njaay noppee, dafa jébbal kàddu gi jawriñ Umar Yum mi yor wàllu dem beek dikk bi. Mu daldi biral ay dogal yi ñeel tukki-jaare-suuf yi. Moom it, tëral nay sàrt yu, ku leen jalgati, dees na la daan ni ko yoon santaanee.
Ci tënk, 10i dogal yii toftalu la jawriñ Umar Yum biral ci talaata ji, 24eelu fan ci weeru màrs :

  1. dakkalees na bépp xeetu tukki diggante dëkk ak dëkk, diiwaan ak diiwaan ;
  2. dees na dakkal tukki gox-goxaat yi li ko dale 20 waxtu ci guddi jàpp 6 waxtu ci suba ;
  3. santees na bépp aji-tukki ak dawalkati oto yépp ñu takk mask ba keroog ñuy àgg fa ñu jëm ;
  4. woto bu nekk, xaaju palaas yi nekk ci sa kàrt-giriis ngay yeb. Maanaam :
  • woto20i palaas, 10i nit lay yeb ;
  • woto 25i palaas, 12i nit lay yeb ;
  • taksi yiy faral di yeb 5 nit (boo ci boolee dawalkat bi), léegi 3 nit kese lañuy def te dawalkat bi ci lay bokk ;
  • ‘’maa-watiir’’ yi tamit dootuñu romb 3 nit (te kiy dawal ci lay bokk) te, santees na ku nekk ci ñoom mu takk mask ba ba muy àgg ;
  1. dakkalees na njaay meek njënd mi ci biir gaaraas yi ;
  2. terees na képp ku liggéeyul ci gaaraas yi mu fay teg tànkam walla di fa taxawaalu ;
  3. yóbbaale màrsandiis yi dees na ko wéyal ci kow dawalkat bi sàrtoo ndigal yii :na takkub mask, sol i gã te yeb 2i nit kese ;
  4. digalees na it caytug ótorut yi ñu gën a farlu ci set-setal bi ak ci seen kiiraayu liggéeykat yi (jox leen ay mask ak ay gã). Ndax, li ëpp ci weccoo yi ci ótorut yi (transactions), loxook loxo lay ame.
  5. dakkalees na liggéeyu ‘’war-gaynde’’ yi (woto yiy dem Mali), alóo-dakaar yeek gaaraasi falaa-falaa yi.

Jawriñ Umar Yum ne xam na ne dogal yii dinañ metti lool ci boroom woto yi ak képp kuy liggéey ci wàllu dem ak dikk, rawatina biir Ndakaaru te looloo tax mu fas yéenee taxawal ab banqaas buy saytu  seeni pertmaa. Teg na ci ne dina ko jébbal njawriñ jiñ dénk ngurd mi, mu sukkandiku ci xool ni mu leen di dimbalee

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj