Démb ci gaawu bi, 17i Me 2025, la jéyya ju metti dal ci kay futbalu Senegaal. Fajuuf Njaay, kàppiteenu US Wokaam moo ñàkk bakkanam démb ca seen joŋante ak Oslo ñeel 25eelu bésu sàmpiyonaa bi.
Moom Fajuuf Njaay nag, jotul woon a dugg ci pàkk bi. Ndax, bu nu sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, xamlees na ni teel na yëg nagam ci yaramam ba doon ko jàmbat. Loolu nag moo waral mu toogoon ci baŋ bi.
Ba mats ba tollee ca mitã ba la ko ag jagadi bett. Diggante bi ñu ko jël di ko yóbbu ca raglu ba, ca yoon wa, mu daldi ciy ñàkk bakkanam. Muy lu metti lool ciy farandooram ak it waa réew mépp. Diggante démba ak tay, foo gestu ci mbaali-jokkoo yi gis ku nekk di ko mettitlook a mastawu ay jegeñaaleem.
Kii di Njiital “Fédération Sénégalaise de Football” Meetar Ógisteŋ Seŋoor àddu na ci, di ko mettitlu, waaye itam di ko jaale ay mbokkam, waa ekibam ak waa réew mépp. Naka noonu, Jëwriñu Ndaw ñi, Tàggat-yaram yeek Mbatiit mi, Soxna Xadi Jéen Gay itam, daldi na ciy jël kàddu di ko jaal waa réew mi ak soppey tàggat-yaram yépp.