Mbooloo mi ëmb kuréli liggéeykat yi ci dalub roppëlaan yi (Intersyndicale des travailleurs de l’aviation civile et du secteur des transports aériens) doon na janook taskati xibaar yi. Muy ndaje mu mu woote woon ngir ñaawlu ñàkk sàmmonteek déggoo yees xaatimoon ginnaaw waxtaan yi fi jotoon a am.
Bërki-démb, ci alxames ji, 13 awril 2023, la kuréli liggéeykat yi ci ci dalub roppalaan yi amaloon moomu ndaje. Ñu doon ci ñaawlu taxawaayu kilifa yi ñeel seen nekkin ca dalub roppalaan bu AIBA. Nde, ci seen i kàddu, Nguur gi sàmmontewul wenn yoon ak déggoo yi doxoon ci seen digante. Ñu mën cee jàpp ñeenti mbir.
Bu ci njëkk di ànteni gindikukaay (antennes du centre de réception déporté) yi màggat ba doxatuñu. Yooyu ànten, dees leen a war a yeesal. Waaye fi kilifa yi wax ne fa lañu leen di samp, ñoom ànduñu ci wenn yoon.
Ñaareelu mbir mi tax ñu yékkatiy kàddoo ngi jëm ci payoori ndàmpaay yi ñeel seen kaaraange, ñu gën koo xam ci ISA (Indemnité de sécurité aérienne). Bu ñu sukkandikoo ci li Sëñ Mustafaa Gay mi yor seen kàddu wax, lu ëpp atu Yàllaa ngi nii, Saa-Senegaal yiy liggéeye ASECNA (Agence pour la sécurité de la navigation aérienne en Afrique et à Madagascar) mënuñoo fexe ba jot ci seen i ndàmpaay ni mu ware. Weer wu jot dañ leen war a fey, waaye ci xayma, ñoo ngi ci juróomi weer yu ñu leen ameel. Loolu tax ba :
Mbooloom kurél yee ngi sàkku ñu jël i matuwaay ci ni mu gënee gaaw ngir fey leen 5i weer yi ñu leen ameel, ci anam yi ko déggoo gi tëralee ginnaaw waxtaan yi fi AIBD SA woote woon ci 17 ba 19 mars 2023. (S. M. Gay).
Bokk naat ci li ñuy ñaawlu ci seen biir waxtaan, par-parloo gi am ci doxalinu kilifa jëmale ci ña fay liggéeye. Ndeaxte, yemale gi war a am ci ni ñuy jëflanteek liggéeykati ADS ya woon ak yu AIBD SA yi nekkul. Te dafa bokk ci déggoo yi, keroog bi ADS ak AIBD doone benn, ñu yemale payoor yi, ngañaay yeek ndàmpaay yi. Looloo tax ba ñuy sàkku ci kilifa yi ñu matale lépp fileek 1 mai 2023.
Bu weesoo ñett yii, meneen mbir mu ñu tudd ci seen jotaay ba mooy pàkk yi ñu leen war a jox ca « Daga Kholpa » ak « Thies Nord » ngir seen i dëkkuwaay. S. Mustafaa Gay wax na sax ne mbooloo mi jógul ci di leen ko fàttali. Njiitu réew meet ci boppam joxe na kàddoom bu yàgg, waaye dara. Ca déggoo ba ba léegi, kenn waxatul li ci jëm.
Ginnaaw bi ñu siiwalee jafe-jafe yii ñuy jànkonteel jamono yii, ña ngay dànkaafu Nguur gi mu sàmmonteek ponk yi ñu digaale ci déggoo bi. Lu ko moy, mën nañoo àgg ci bank seen i loxo.