Limub gaynde yiy dem ca kub bu àddina si : Saajo Maane mooy kiy dem

Yeneen i xët

Aji bind ji

Aliw Siise siiwal na limub gaynde yi war a teewal réewum Senegaal ca kub bu àddina si. Ñi ngi tollu ci ñaar-fukk ak juróom-benn. Ñu ràññe ci ñëwug Saajo Maane mi tere woon nelaw Saa-sénégaal yi. Waaye tam, Saaliwu Siis mi nekkoon lateraal bi gënnoon a xarañ ci kub bu Afrig bi weesu (2021), te Senegaal jëloon ko, bokku ci.

Démb ci àjjuma ji, 11 noowàmbar 2022, bi 10i waxtu jotee ci yoor-yoor, la tàggatkatu ikibu Senegal bi doon jàkkaarlook taskati-xibaar yi ngir biral limub wurekati (joueurs) Senegaal yi mu namm yóbbu ci kub bu àddina si, ca Qataar. Bi mu jëlee kàddu gi nag, moom Aliw Siise, njëkk naa sàkku ci mbooloo mi ñu ànd ñaanal Saalif Jàllo, di taskatu-xibaar bu fi bawoo bu yàggul dara. Mu dellu xamle ni 26i wurekat la woo. Ñenn ñi yàgg nañoo ñëw, ñeneen ñi diy wàcc-bees (nouveaux). Ñii la lim :

Eduwaar Mendi, Alfered Gómiis, Siini Jeŋ;

Formoos Mendi, Yuusuf Sabali, Kalidu Kulibali, Paap Abu Siise, Séexu Kuyaate, Abdu Lahat Jàllo, Fóode Baloo Ture, Ismayla Sakob;

Paate Siis, Nàmpalis Mendi, Gana Géy, Paap Géy, Paap Mataar Saar, Mustafaa Naam, Mamadu Lum Njaay;

Nikolaa Jakson, Saajo Maane,  Ismayla Saar, Kerepĩ Jaata, Faamara Jéeju, Bulaay Ja, Ilimaan Njaay, Bàmba Jeŋ.

Ginnaaw loolu , li ñépp doon laam-laame nag moo doonoon bokku saajo Maane. Doomu Bàmbali ji dafa gaañu woon talaata (8 nowàmbar) ca Bayern. Jotul woon a àggali sax joŋante bim tàmbali woon. Nde, ci 20eelu simili bi la génnoon. Bi saabal bii di L’Équipe xëyee ci àllarba ji biral ne Saajo Maane du bokk ci Kub bu àddina si, la boppi Saa-senegaal yépp tëju. Donte ni delsi nañ ne ku sës ci ikib bi xamal na leen ni Saajo dina bokk, taxul xel yi dal benn yoon.

Aliw Siise andi na ci itam i leeral ginnaaw bi mu ko woowee ba noppi :

Xam naa ni nag gaañu-gaañu saajo Maane bi jaaxal na askanu Senegaal gépp, wu Afrig, ba ci àddina sépp. Ñuy wax ñépp ñu dal. Am nañ yaakaar ni dina ñëw fekksi nu. Xéy-na du ñëw ci ndorteel li ndax caytu-yaram yim war a def ayu-bés bii di ñëw. Ñu am yaakaar ni fileek ñetti joŋante, bu soobe Yàlla dina ñu fekksi. […] li wóor mooy lim nañ ko. Dafa amoon solo lool ci man mu bokk ci. 

 Tàggatkat bi delsi na itam bu baax ci li ñeel mbiri Saaliwu Siis mim woowul. Li mu ci wax mooy :

Futbalu Senegaal tollu na foo xam ni dañu war a xoolaat sunu wurekat yi nuñ leen di woowee. Ngir woo wurekat ci ikib bi dafa am ay sàrt. Bu ci jiitu mooy nga am mbootaay. Te Saaliwu Siis amul mbootaay. Ci cër bi ma ko jox ndax fu kowe fim àgg, ak cër bi ma jox kër gii ma nekk di FSF, mënuma jël wurekat boo xam ni bii, amul mbootaay. Xam naa bu baax Saaliwu li muy dolli ci ikib bi. Bokk na itam ci samay ñayi xare. Mi ngi ciy jafe-jafe te nun ñépp ñi ngi ci ginnaawam. Te am naa yaakaar ne dina delsi bu génnee ci yooyu jafe-jafe.”

Bu loolu weesoo, ceetlu gi mooy 8i wurekat doŋŋ fi xam lu kub bu àddina si di saf. Ñi ci des, bu amee ñu demoon ci kub bu Afrig beet, ñeneen ñi bii mooy guleet ci ñoom ñuy dem ak Senegaal ciy joŋante Kub. Waaye mënees na jàpp li Aliw Siise wax ne « wurekat bu ndaw amatul » te itam xale yu mën li ñuy def te bëgg ko itam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj