Jëwriñ ji, Biram Suley Jóob, wax na ak njiiti GCO (Grande Côte Opérations SA), di këru liggéey giy génne xeer yi ci màndiŋu lompul mi. Muy sàkku ci ñoom nag, ñu jébbal kilifa Senegaal yi seen i caabal, te ñu jagleel Saa-senegaal yi yenn palaasi liggéey yu am solo yi.
Démb, ci àjjuma ji, Biram Suley Jóob (jëwriñu laf gi, soroj beek mbell yi), ma nga woon fa diiwaanu Luga. Ab tukkib doxontu la fa doon amal, fa màndiŋu lompul ma. Eggaale naat ba ca xeer ya këru liggéey gii di GCO di génnee foofa. Jëwriñ ji nag, gaawantu na ci teewam foofu ngir fàttali njiiti kër ga wareef yi ñu war a sàmmonteel ci seen liggéey bi, foofu.
Bokk na ci li mu gën a taxaw, caabal yi waa GCO war a jébbal kilifay réewum Senegaal te ba léegi kenn gisagu leen.
« Caabali GCO yi ci ñetti weer yu nekk ak at mu jot dañoo waroon a jàppandi. Bëgguñu nag ngeen gisee ko niy tëkku. Pàttali la rekk ñeel wareef yi ñu yoon gàll. »
Naka noonu, mu leen di fàttali ni caabal yi, dañ leen a war a jébbale ñetti weer yu nekk ak at mu jot, ci àpp yiñ leen jàppal. Wareef la wu yoon tëral. Te, bu yoon waralee ñu jébbal caabal yi, dañ leen a war a jébbal. Lu ko moy, képp ku ci tënkuwul rekk, yaa ngi ci njuumte. Ci loolu nag, mu leen di xamal ni Nguur gi moo ngi leen di xaar ci ñu sàmmonteek seen i wareef yépp, te dina ci taxaw ngir ñu doxal leen ba mu mat sëkk.
Ginnaaw waxu caabal yi, jëwriñ ji ñàmbaas na ci jeneen wax. Muy waxu yenn palaas yu am solo yees war a jagleel waa réew mi, yu demee ni njiitu mbiri liggéeykat yi (directeur des ressources humaines), kopparal gi (directeur des finances), njaay mi (directeur commercial) walla njiitu doxalin yi (directeur des opérations). Ndax kat, palaas yooyu, ay Saa-Senegaal ñoo fa war a toog.
Bu weesoo loolu, jëwriñ ji sàkku na ci jaraafu luga bi, Ndey Ngenaar Mbóoj, Mu gën a góor-góorlu te fexe déggoo am ci diggante GCO ak askan wi yàqule ci yëngu-yëngu këru liggéey gi (GCO). Ba tax muy sàkku ci kër gi mu dugal loxoom bu baax ci sémb yi ñeel suqaleeku gox yi mu laaleel. War na ci moom sax, mu jox bokk-moomeel (Communes) yi mu laaleel (Cepp, Jokkul, Jawriñ ak Kab Gay, gu ci nekk, 300i tamndareet.