Mbirum bóomug ñaari bakkan yooyu moo lëmbe réew mi jamono jii. Waaye, mel na ne Yoon a ngi ciy dox jéego yu am solo. Nde, juróom-ñaar yi ñu jotoon a teg loxo fanaani nañ seen guddig kaso gu njëkk, barki-démb ci àllarba ji. Waaye, mu amaat meneen mbir mu yees ci biir coow loolu. Ndax, kii di Usmaan Jaw ak Mamadu Lamin Jaw dañoo defoon ay pelent yoo xam ne coowal bóomug Asiis Dabalaa ak Waali moo leen sos.
Dafa di, waa DSC (Division Spéciale de Cybersécurité) mujje nañoo saytu pelent yooyu. Li tax ñoom ñaar ñu def pelent yi mooy dafa am ay “tik-tokeurs” ak ay nit ci Facebook yu dugal seen i nataal ci mbaali jokkoo yi, di gëmloo askan wi ne dañu leen a jàpp ci mbir moomu. Te ñoom, nee ñu, taqewuñu ci, laalewuñu ci, li ñu bokk ak ñooñu ñu teg loxo mooy tur ak sant. Bees sukkandikoo ci waa Libération, am na ñu ñu ci jot a woo ba déglu leen. Te, jàpp nañu ne dees na am na ñeneen ñoo xam ne dinañu leen ci teg loxo.