LU YEES CI MBIRUM PRODAC

Yeneen i xët

Aji bind ji

Am na lu yees ci mbirum Prodac mi. BAD (Brigade des Affaires Générales), di bànqaas ci DIC (Division des Investigations Criminelles) ubbi na wayndare bi ba tàmbali ndéglu yi.

Ginnaaw kalaame bi ndawal Nguur gi ci wàllu yoon amal, caabalug IGF (Inspection Générale des Finances) gi aju woon ci mbirum PRODAC (Programme des Domaines Agricoles Communautaires) a nga ca loxoy Yoon. Waa BAD, dib bànqaas ci DIC, lañu dénk mbir mi, ñu war koo leeral.

Bees sukkandikoo ci xibaar yi sunuy naataango yu Libération siiwal, liggéey ba tàmbali na. Nde, Xaadim Ba mi jiite Locafrique, jot nañu koo jëli ca kaso ba mu nekkoon ba déglu ko. Moom sax jot naa biral ci kanamu luññutukat yi ne, moom ci boppam, moo njëkk a wax ngir jéebaane ginnaaw bi mu seetloo ay peyoor yu teey xel.

Ginnaaw settantal gi, IGE dafa gisoon ni sémb wi dafay dikke 26,6i tamñareeti FCFA. Muy xaalis bu ñàkk méngoo ak jubluwaay yi. Rax-ci-dolli, am na yeneen ñàkk méngoo yu ci am. Kër gii di Green 2000 jot naa feyeeku 15i tamñareet yu mu jote cib déncu xaalisu Hapolim Bank, dib bànk bu nekk Israayel.

Peyoor googu itam, moo ngi ame ci yombalug kilifa yi jiite woon Prodac. Ndaxte, li ñu jëlul matuwaay yi war ngir saytu kayitu peyoor yi ak yóbbu kër gi mu ko séqal mu sàmmonteek digaale yi. Bataaxali jéebaane yi Locafrique yónnee njiiti Prodac yi taxul wenn yoon ñu bàyyi ci xel, ba tax ñu doon wéy di jàllale kayitu peyoor yi ci lu amul genn caytu.

Naka noonu, IGF wone na ni lees jot a fey ak yi ñu doon waaj a fey dina dem ba ci 17,2i tamñareet. Te, liggéey bi demewul noonu. Ba tax muy duut baaraam njiitu Prodac yi ci ni ñu woyofalee mbir yi ba genn caytu amul ci peyoor yi walla boog dara leerul ci caytug peyoor yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj