Coowal bóomug Asiis Dabalaa gi ak jarbaatam bii di Buubakar Gano, ñu gën koo xam ci turu Waali, ba tey jeexagul. Xew-xew bu tiis boobu mi ngi amoon ci dibéer jee weesu, fa Pikin “Technopole”. Boobaak léegi nag, takk-der yaa ngi ci ay luññutu ngir xam kan walla ñan ñoo nekk ci ginnaaw jëf ju ñaaw jooju. Moo tax, am na ñu ñu jàppagum fa Tuubaa ak fi Ndakaaru.
Démb, ci gaawu gi, lees siiwal ne jàpp nañu ki ñu yaakaar ne moo def jëf ju ñaaw jooju. Ña nga ko jàppee Tuubaa, fa koñ bii di Jannatu Mahwaa. Ñi ko teg loxo mooy ndawi “Brigade Spéciale” bu Tuubaa. Nde, dafa màggali woon. Mi ngi wuyoo ci turu M. L. Jaawo, ñu gën koo xam ci turu M. Lóo. Mi ngi judd ci atum 1999, dëkk fa Pikin Ginnaaw-Raay, nga xam ne fa la mbir mi xewee. Dañu njortagum ne mooy aji-bóom ji, moo tax ñu jàppagum ko. Dafa di, ci lees rotal ciy xibaar, moom sax nangu na ne moo faat Asiis Dabalaa ak jarbaat bi. Moom nag, ci àndandooy Asiis Dabalaa yi la bokkoon.
Mbirum xaalis moo sabab njombe wi, bees sukkandikoo ciy waxi ndeyu-mbill ji. Daf ne: “Damaa ñaan Asiis xaalis. Ginnaaw bi mu bañee, ma génnee paaka di ko tëkku. Ma mujj koo rey laata may jël jollasoom.”
Waaye, reyul Asiis rekk yem ci. Ndax, dafa bóom Asiis ba noppi, jàll ci jarbaatam ba, fekki ko néegam, rey ko moom itam. Loolu la wax ci kàddoom yii : “Maa rey B. Gano tamit ñu gën koo xam ci turu Waali mi ngi xam ne, gisoon na ma bi may dugg ci dëkkuwaay bi (appartement). Ma jëlaale jollasoom”.
Kon, moom, nangu na ne moo bóom ñaari bakkan yooyu. Waaye, nanguwul ne moom moo yulli sàqu “wave” Asiis bi. Moom, jollasu yi rekk la jël. Waaye, jàpp gi yemul ci waa jooju rekk. Bees sukkandikoo ci waa Seneweb, am na ñeneen ñu ñu teg loxo. Soxna sii di N. Léy tamit, dib fecckat, teg nañu ko loxo. Jamono jii, ma nga ca loxoy waa DIC. Dañu koo def li ñuy dippe “garde à vue”.
Kon, mbir yi ba tey dese naa leer. Ba tax, fi mu tollu nii, am na juróomi nit yoo xam ne ña nga ca loxoy Yoon. Maanaam, ñi ngi leen di déglu ci mbir mi. Waaye, fi mbir mi tollu nii tembe, M. L. Jaawo lañu duutagum baaraam. Ndax, kàddu yi mu biral ci kanamu luññutukat yi. Coow li nag bari, rawatina ci mbaali jokkoo yi. Du ñàkk, fan yii, takk-der yi leeral mbir mi ba dootul amati lënt-lënt. Ndax, yàgg bawul dara.