Ka yoroo keesu kër gii di CMS (Crédit Mutuel du Sénégal) moo luubal ay koppar ci nafag benn kiliyaan. Maanaam, dafa jële ca nafag kiliyaanu CMS bi lu tollu ci fanweeri miliyoŋ. Kiliyaŋ boobu mu sàcc nag, nee ñu toog na ñaari at yu mu ñëwul ndax wopp ju ko tëral.
As ndaw lees jiiñ ag càcc ca CMS. Ndaw si, keesiyeer la fa, di wuyoo ci turu A. Gasama. Yéenekaay « Libération » moo siiwal xibaar bi. Nee ñu, 30i tamndaret (miliyoŋ) ci sunuy koppar. Kilifay gër ga, ginnaaw caytu giñ amal, ñoo dem ba gis ne am na kuy tibb ci nafag kiliyaan boobee nekk Siwis ci sababu feebar. Ndeke, jamono ju muy faju bitim-réew, am kuy rawale xaalisam ci suuf. Bi ñu saytoo nafag kiliyaan boobii lañu xam ne am na lu des, ñu daldi nànd. Ginnaaw bi ñu luññutoo, ca lañ ko jàpp, laaj ko, muy miim ak a weddi, ñu jébbal ko takk-deri « Sûreté urbaine » bu Ndakaaru. Ñu daldi koy yóbbu seen màkkaan ngir amal ak moom laaj-tont. Foofa, ca pólis ba, la nangoo ne moo sàcc xaalis bi. Ndeke, ñaari at ñoo ngii, muy tibb ci xaalisu jàmbur di lekk. Tës !