Coowal Aji Saar ak Sonko, féewiryee 2021 la tàmbali woon. Ba tey ma ngay wéy di lëmbe réew mi. Ca ndoorte la nëgëni, am na aw tur wees ci dégg saa su nekk : Maamur Jàllo. Waa jooju, turam dëggantaan di Mammadu Maamuur Jàllo, mooy ki Usmaan Sonko tuumaaloon ci mbirum 94i miliyaar yi. Kon, sikk amul ci ne, seen diggante du mën a rattax. Dafa di nag, OFNAC sax dafa dëggal njiitalu PASTEF li ñeel mbir moomu. Ginnaaw coow loolu nag, mbirum ciif gi Aji Saar di tuumaal Sonko tamit daf leen a boolewaat. Ñu tuddati ci Maamuur Jàllo, ñaari at daanaka, saa su nekk, turaw day ñëwaat. Loolu nag, dafay xaw a teey xel.
Bees sukkandikoo ci ñi jot a seede walla ñi laale ci mbir mi, muy ki doon seet ndaw si, doktoor Alfuséyni Gay, kii di sëriñam, Baay Mbay Ñas MC, ba ci kii di Ndey Xadi Njaay, njaatige Aji Saar, Maamur Jàllo loxoom setul wenn yoon ci mbir mi. Ndax kat, mbir mi li ko tax a doy waar mooy ku ko ci tuddul rekk, tudd ci kii di goroom bi ,Meetar Gabi Sow. Ku ñépp tufli nag nga tooy. Kon nag, dafa jot yoon def liggéeyam, déglu kii di Maamur Jàllo walla, moom ci jëmmi boppam, mu dem setal deram bu dee laalewul dara ak kootoo gi.
Coow li nag, ak li muy yàgg yàgg, ci jamono jii la gën a yëngu. Li ko waral mooy ndéggat yii nga xam ne dafa génn, ñépp jot ci daanaaka. Kii di Aji Saar di ci wax ni mbir yi deme. Te, li gën a doy waar ci mbir mi mooy ne, laata ndéggat yi sax, ñi ci seede ñépp, dañuy setal kii di Usmaan Sonko, di taqal ndaw si walla di duut baaram gaa ñi ko ngemb. Ñooñu nag, ki ci gën a fés mooy kii di Mammadu Maamur Jàllo mi nga xam ne, ci Nguur gi la féete.
Ndaxte, kii di Ndey Xadi moo ko ci njëkk a tudd ngir ne dafa bëggoon mu soppi kàddoom yooyu nga xam ne dañu doon setal kii di Usmaan Sonko. Loolu la kii di Sonko di dégtal ci kàddoom yii :
“ Ndey Xadi moom ci boppam nee na bi ñu koy yóbbu Section de Recherche, Maamur Jàllo da koo woo ne ko dinaa la jox ñeen-fukki miliyoŋ ngir nga soppi sa kàddu yi. Mu ne ko defuma ko. Ba senn saa, mu ne ko jox naa la ñaari-téeméeri miliyoŋ ngir nga soppi say kàddu, dugal Usmaan Sonko.”
Mbir yi yemul foofu. Ndege, kii di Maamur Jàllo ak Aji Saar, dafa am seen i ndéggat yu génnoon, ñuy waxtaan ci mbir mi. Loolu la Sonko di waxati, naan :
“ Yeen ñépp dégg ngeen ndéggat yoo xam ne Maamur Jàllo ak Aji Saar ñoo toog di wax mu naan ko liñ la digoon lépp dinañ ko def. Bu àtte bi rombee dinañ la jox sab jàll-waax ak li ñu la waxoon yépp nga génn réew mi.”
Mu mel ni ndéggat yooyu nag doyoon nañuy sabab ngir ñu déglu kii di Maamur Jàllo. Waaye, ba tey kenn gisagul fu ko yoon dégloo donte ne sax ñu bari ci ñi ci laale déglu nañ leen. Walla dañoo jàpp ne loolu matul i firnde ci kanamu yoon ? Kii di Daam Mbóoj moom, gisewul mbir yi noonu. Moo ko tax a wax ne :
“ Li nu bëgg léegi mooy, fukki bakkan ak ñeent yi ci rot, ñu leeral ko ndax Maamur Jàllo moo waxal boppam ci ndéggat yi ne : “damaa am ag pas sama diggante ak yaw (Aji Saar), te duma ci dellu ginnaaw. Bu àtte bi jàllee naa la jox jàll-waax nga tukki”. Loolu mooy mbir mi. Moom, Maamur Jàllo, àttekat bi da koo war a jëli. Dégg naa layookat bi ne, ay ndéggat, kenn mënu cee sukkandiku ngir jàpp kenn. Loolu du dëgg ! Kilifa, lu ñu ko jàppe ? Biram Suley, yóbbuwuñ ko fi, téye ko ? Ci ay xarala lañ ko jaare. Keledoor Seen ak Asan Juuf, luñ leen fi jàppe ci coowu màrs li ? Léegi, ñu ne Maamur Jàllo bu defee ndéggat loolu du firnde ngir ñu jàpp ko. Àttekat dafa jàpp ñenn ci mbir yu mel noonu. Kon, li ñuy xaar mooy mu dem jàpp Maamur Jàllo, bu ko defee ñu xam ne Njiitu réew mi Maki Sàll làqul kenn. »
Daanaka, li ëpp ñi seedee, bu dee faral day am Aji Saar lañu waroon a faral. Ndaxte, kii di Baay Mbay Ñas MC mom, moo taataanoon ndéggati Aji Saar yi génn ci fan yii, mooy sëriñam. Kon kay, taalibeem la waroon a àndal, walla ? Moom sax, biral na ne amul wenn yoon woo xam ne ndaw si tuddu na ci Njiitu réew mi. Ki mu ciy tuddu kay mooy Mammadu Maamur Jàllo. Ndéggat yooyu mi ngi leen ame woon ci woote bu mu séqoon ak kii di taalibeem bi. Ndax, nee na bu ñu demee ci ORANGE sax dinañ xam ne lii ab woote la. Te, ndéggat yooyu nag nga xam ne dañuy firndeel kootoo gi ngir daaneel kii di Usmaan Sonko, moom jijjoon na leen waaye dafa am yu ci jot a rot. Ci lees dégg kii di Aji Saar yékkati kàddu yii :
“ Maamur Jàllo daf maa sonal ngir ma am wenn waxtaan ak moom mu mel ni maanaam moom daf may jàppale rekk. Ndax xam nga loolu ? Moom moo tëgg lépp. Moo ma ma wër sax ba gis ma. Man xawma woon sax kan la (…). Ayu bés ginnaaw loolu, Meetar Sow woo ma, ne ma waa ji ñëw na ? Ma ne ko ñëw na, deful dara, dafa ñibbiwaat. Bés boobu, Maamur Jàllo moo ñu jox daamar nu dem ànd ak benn fajkat dem CETEO fajkat bi def caytu yi (prélèvement) ak yooyu yépp (…). Ñoom ñépp laa xam, bëgguñu ma wax, dinaa la nataalal aw wayndarew ñi nga xam ne jot naa leen a gis. Su ma la ko waxee dooma gëm, ñii baaxuñu. Dañoo yaakaar ne ab móomin lañu nekkal te li ñiy def lépp xam naa ko (…) Fàww ma jàmmaarloo ak ñoom bu ma waxee baaxul ci ñoom ndax seen Nguur day daanu. Danuy def teggi teg (jouer carte sur table). Képp ku ci taq say mbir a ngi baax.”
Ndéggat yooyu, bu dee doy nañu firnde ci kanamu yoon, kii di Maamur Jàllo war nañu koo woo, déglu ko. Rax-ci-dolli, kii di Aji Saar yoon dal ci kawam. Ndax, mbir mi nekkatul diggante Aji Saar-Sonko rekk, fukki bakkan ak ñeent ñoo ci rot, am ñu ci jële ay gaañu-gaañu, ay yàqu-yàqu yu bari am ci.
Waaye, coow li yemul foofu. Dafa am keneen ku yékkati kàddu yoo xam ne day wane ne kii di Maamur Jàllo dafa laale ci mbir mi bu baax. Kooku mooy Doktoor Alfuséyni Gay di ki def caabalug paj gi gi nga xam ne kii di Gabi Sow mooy xaritam, di it ab layookatam, kooku goro la ci Maamur. Kon, bu dee faral day am, moom lay faral. Te, ci li mu biral firnde la ci ne ag ciif moom amul, xanaa kay kan ak kan a laale ci kootoo gi ak nan la ci laalee.
Te, moom tamit, bokk na ci ñi jokkoo ak Maamur Jàllo bees sukkandikoo ci kàddoom yii :
“ Paap Sàmba Sow (Gabi) sama xarit bi moo ma ma woo ne ma ndax yaa ngi Ndakaaru ? Ma ni ko waaw. Mu ni ma ndax tukkiwoo fan yii ? Ma ni ko xanaa lu dul jàmm (…). Siidi Ahmed Mbay moo ma indil Aji Saar (…). Bi ma defee caytu gi, Gabi ak Maamur Jàllo woo nan ma ay yoon yu bari di ma laaj, ma ni leen mënuma cee wax, sama liggéey mayuma ko. Ca ëllëg sa, bés boobu metti woon na te li ñu bëggoon mooy xam li nekk ci li ma saytu. »
Li doy waar ci mbir mi nag mooy ba nii kii di magum àttekat yi Maham Jàllo dégloogul kii di Maamur Jàllo. Kon kay li am ba des mooy Aji Saar ak Sonko ag ciif doxul seen diggante. Xanaa kay moom dañu koo yónni woon te matalewul yónnent ba bees sukkandikoo ci li rotagum ci mbir mi. Ndax, ba tey li jot a bir ci wayndare wi, day setal Usmaan Sonko, di taqal kii di Mammadu Maamur Jàllo.
Mbaa du kon xeex bi amoon seen diggante ci mbirum 94i miliyaar yi moo tuxu fii. Ak lu ci mën di am, bu yoon làqul doom, dóor doom rekk, lépp dina leer. Ndax kat, ak nu mu mën di deme, dëgg rekk mooy mujj, te xam nañu ne fen moom du bejjaaw.