MAATAM AM NA GAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tuxal nañ Ngañ Demba Ture mu Pastef ca Maataam. Démb ci suba la xibaar bi jib ñeel mbir moomu. Kii di jëwriñ ji ñu dénk Yoon, Ismaayla Maajoor Faal, moo jël ndogal li.  Ngañ Demba, ab gerefiyee la, xereñ lool, féete woon, laata ndogal li, ca ëttu àttewaay bu Ndakaaru. Muy ndawul Pastef lu ràññeeku lool sax, xam-xamam màcc ci wàllu Yoon. Barki-démb rekk, bi lëkkatoo Yewwi Askan Wi doon amal ndajeem maak taskati xibaar yi, Ngañ Demba Ture jëloon na kàddu gi, dàjji waxi jëwriñu Yoon wi. Nee ñu nag, looloo tax ñu yobbu ko fa Maatam.

Ngañ dafa gaañ kilifaam gii di Ismayla Maajoor Faal, jëwriñu Yoon wi. Moo tax, ci lees njort, jëwriñ ji mer, sànndi ko Maatam. Lu tax ?

Barkaatu-démb, ñeenti jëwriñ génnoon nañu ngir ragg seen ginnaaw, teggi tuuma ak dalal xeli waa bitim-réew. Wax nañ fa lu bari, rawatina mbirum Usmoon Sonko ak daan bees ko gàll.  Ci seen i wax, danoo tam Usmaan Sonko dëmm, jiiñ ko lu nekk. Démb, waa Yewwi Askan Wi génn ngir tontu leen. Ngañ Demba Ture a fa teewaloon Pastef.

Bi Ngañ Demba Ture jëlee kàddu gi, dafa dàjji waxi Ismayla Maajoor Faal yépp, indi ay firnde yoy, jukkees na leen ci sàrti réew mi. Mu faramfàcce àtteb Sonko bi ak li ci mën a topp, leeral mbirum CPI mi ñuy xuppee Nguur gi jamono jii. Dem na ba wax sax ne, jëwriñ ji ay kàcci neen la fa wax te moo ko tey.

Génn googu, dina jeexital ci liggéeyam. Ndax, poñ ya fa Ngañ Demba Ture leeral, dafa mel ni neexul jëwriñ ji. Ndax, dafa neenal ay waxam. Maanaam, ndongo li dafa weddi li sëriñ bi waxoon keroog yépp, teg ko ci xam-xam ak i firnde yu wér te mucc ayib.

Ba tax, démb, mu génne ndogal lol, daf ciy tuxal Ngañ Demba Ture, soppi bérébu liggéeyam. Maanaam, jële na ko Ndakaaru, yóbbu ko Maatam. Li mu ko layalee mooy na, fa Maatam, gerefiyee yi matuñu. Moo tax mu yóbbu ko fa ngir mottali limub ligéeykati Yoon ya fa nekk. Waaye de, lees jàpp mooy ne Ismayla Maajoor Faal day defante. Dafa mer di jëfandikoo dooley Nguur ngir xeexe ko ci wàllu pólitig.

Lees ci mën a jàngatee mooy ne, wëliis Ndakaaru miy gëbla gi, joxeesul worma yeneen diiwaan yi. Ndaxte, dafa mel ni, Ndakaaru mooy àjjanay liggéekat yi. Ba tax na, kees fa jële yóbbu la feneen rekk, day xaw a niru ab daan walla leneen. Loolu nag, kersa la ci Senegaal. Te day wone ni, Nguur gi lajj na. Bu dee bëgg a naqaral ak a metital Ngañ Demba Ture a tax mu yóbbu ko Maatam, kon day firi ni liggéeykati Maatam yi joxeesu leen cër walla anam yi ñuy liggéeyee metti.

Senegaal du Ndakaaru kese, jot na waa boor yépp xam ko. Waaye nag, Maatam am na gan.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj