Muumaa di li mu fésal ci li xew ci réew mi.
Ana lu waral faleesoon ko kon ci boppu réew mi?
Cëram de moone du fésalug yàccaaral ci jafe-jafey réew mi.
Ku nee ngi naan: moo ana njiitu réew mi?
Yëngu-yëngu yiy jolli, mu ne selaw ni armeeli réew mi.
Sàggan de weesuwul giig cell ci li xew ci réew mi.
Amaana day xaar bakkan yu bari rot ci mbeddi réew mi.
Lilee di li jaaxal képp kuy gor tey doomu réew mi.
Lëkkaloo doonuw say de jot na ngir xeex jële fi nooteel giy daw ci réew mi.
SBJ