MÀGGALUG BÉSUB JÀNGALEKAT YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu njàngale mu kawe mi, gëstu beek coste bi màggal na bàrki-démb ci alxames ji, 19i pani desàmber 2024, bés bi ñu jagleel jàngalekat yi fi àddina sépp. Mu àndoon ceek naataangoom yii di Mustafaa Njekk Saare (jëwriñu tàggatu gi) ak Mustafaa Giraasi (jëwriñu njàng mu suufe meek mu digg-dóomu mi).

Ci bésub 5i pani oktoobar la mbootaay gii di Unesco jàppoon ngir ñu ciy màggal bésub jàngalekat yi fi àddina sépp. Waaye, fi Senegaal, dañoo randaloon màggal gi ndax li mu daloon ci ubbiteb lekkool yi ak set-setal yees ci doon amal. Ci ayu-bés bi weesu jàpp bii nuy génn (14 ba 19i pani desàmbar) lañ ko doon dabantal ci njiiteefu jëwriñ ji Abdurahmaan Juuf.

Bésub ren ji nag, ñiŋ tënkoon waxtaan yi ci wëppa wii di « Gëddaal baati jàngalekat yi : dox jëm ci déggoo yu yees ñeel njàngale mi. Amal nañ ci nag ay xew-xew yu bari ci diggante Ndakaaru ak Cees. Ñuy ay xew-xew yu deme niy doxantu ci mbedd yi ak i jotaayi waxtaan.

Ci jotaayi waxtaan yees doon amal itam, dogat nañ ci seen wëppa wi ci ñaari ponk ngir gën koo mën a faramfàcce. Ñaari ponk yooyu ñooy « taxawaay ak wareefi jàngalekat bi ci naal yi ñeel njàng mi » ak « melokaan ak mën-mënub jàngalekat bi ngir tabax yoonu njàng mu yees ».

Ci alxames ji, 19i desàmbar 2024, lañ doon amal jotaay bu mag bi mujje bi, fi Ndakaaru. Ca jotaay booba, jëwriñ ji yékkati na fa ay kàddu njukkal ñeel jàngalekat yi, ñoom ñi leen jàngal dawal, dégg ak wax wax ju jub ; xérloo leen ci njàng mi te teg leen ci yoonu xam-xam.  Sargal na fa itam ay jàngalekat yu ràññeeku, takkal leen i raaya réew mi ci seen kanami njaboot.

Jàngalekat yi itam jàpp nañu ni màggalug bés bi war na doon ci ñoom jamonoy ànd xalaat ci seen bopp, laayante biir ci mbir yi aju ci seen liggéey, waaye itam ngir fagaru ñeel ëlleëg. Dellu nañu itam sàkku ci jëwriñ ji mu fekkisi leen ci amal bés bi ci 5i pani oktoobar mi ko Unesco takk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj