MAKI SÀLL A NGI JËMMAL NAALAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àjjuma jii weesu lañu teg loxo Njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, ginnaaw bi mu jógee jumaa. Li waral jàpp gi wii yoon mooy coow lu doxoon ci digganteem ak benn sàndarm bu jigéen. Ci altiney tey ji la doon jàkkaarloo ak àttekat bii di Maaham Jàllo. Ginnaaw seen janoo bi, Maaham Jàllo dóor na njiitul Pastef li “mandat de dépôt”, jàllale ko ndung-siin. Nu ni déet-a-waay, jëwriñu biir réew mi génne ab yégle di ci wax ne tas na làngu Pastef. Mu mel ni Nguur gi dafa woo askan wi cib xare.

Keroog àjjuma la coow li door. Bi Usmaan Sonko jullijee jumaa ba delsi la fekk as ndaw su gaare woon otoom ca buntu këram, di ko filme, moom ak i njabootam. Ci li Usmaan Sonko wax, dafa foqati jollasu ndaw si, daldi koy sant mu ubbi ko ngir mu far nataal ak widewoo yim ël ci moom. Bi ndaw sa bañee, la yóbbu jollasu bi. Waaye, layookatam bii di Bàmba Siise, moom daf ne, du Usmaan Sonko ci boppam moo nangu jollasu ndaw si, ñi koy wattu ñoo ne ndaw si moo dakkal li muy def, mu bañ, ñu foqati jollasu bi. Ak lu ci mën di am, Sonko bindoon na ci xëtu Facebookam, wax ni moom ci boppam moo ko def. Ca la waa GIGN jëlsee, dàjji buntu këram, jël ko yóbbu.

Tey la ko Maaham Jàllo, àttekatu luññutu gi doon déglu. Bim noppi ci déglu njiitul Pastef li, daf ko dóor “mandat de dépôt”, jàllale ko ndung-siin. Ñu teg ciy waxtu, ci tàkkusaan gi, jëwriñu biir réew mi génne ab yégle, di ci wax ne tas na làngu Pastef. Nde, ciy waxam, Pastef dafa dëkkee taal fitna ci réew mi ak a tuur deret. Mu neeti, dinañ jaay alali Pastef ni Yoon sàrtalee. Diggante bi nag, xeex bi tàmbali na diggante ndaw ñi ak takk-der yi. Fu mu jëm, kenn xamagul. Waaye, Nguur gi, dafa mel ni mi ngi jëmmal i pexeem : jàpp Usmaan Sonko tëj ci kaso bi, suuxal Pastef. Moo taxoon, boobaak léegi, képp kuy kilifa biir Pastef, yor fa ndombog-tànk, nëbb nañ la jant wi.

Ndax askan dina seetaan lii Maki Sàll di def ? Li ci kanam rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj