Toroxal nañ Maki Sàll fa New York. Bi mu àggee Amerig, dañ ko fa doon yuuxoo ak a ŋàññi ni mu yoree réew mi ak ni mu bunduxataalee kujje gi ak askan wi. Muy lu ñuy ŋawti-ŋawtee ci kibaaraan yeek mbaali jokkoo yi. Fekk mu demoon fa ngir teewe 78eelu Ndajem Mbootaayu réew yi (Session ordinaire de l’Assemblée Général des Nations unies).
78eelu Ndajeem Mbootaayu réew yee ngi ñuy amal jamono jii fa réewum USA. Mu war a am ci àppug juróom-ñaari fan (17 ba 23 sàttumbaar 2023). Njiitu réew mi Maki sàll bokk ci ñi koy teewe.
Moom Njiitu réew mi nag, demam gi foofoo ngi ñuy coow ci dëkk bi. Teertu bu wex bi ñu ko fa jagleel ci dibéer jee ko waral. Nde, dañ ko fa yuuxoo ba ñu koy ŋawti-ŋawtee ci kibaaraan yeek mbaali jokkoo yi.
Bi muy teg tànkam ca otel ba mu waroon a dal, ndeke du waa Bennoo kase ñoo fa nekkoon. Ñi fare ci kujje gi dañu fa bare woon lool. Bi ñoñi Njiitu réew mi teewee, doon tëgg, di woy ak di ko kañ, ñi féete ci kujje gi dañu ber seen làngug bopp, jàkkaarlook ñoom ak i yuuxoo.
Lu ñu waxul Njiitu réew mi nag dañu koo fàtte. Tuddee nañ ko fa sax digtaatëer, jaaykatu doole, raykatu nit ak yeneen yu ñu bind ci seen i pànkart, di wax ñu bàyyi Usmaan Sonko. Dem nañ ba di ko gaaral, naan ko « Sonko ! Yaa bari doole !» Am sax ñu cay teg, naan ko : « fii USA la ! » ngir xamal ko ni boo mënee tere ku ñaxtu fa réew ma, fii mënuloo fi tus.
Kii di Kura Maki moom jot nañ ko faa bunduxatal laata takk-der yi di ko àtte ak soppey Usmaan Sonko yi. Ndox sax xëpp nañ ko ko. Taskati xibaari RTS yeek yu TFM yi tamit jël nañ seen wàll ci saaga yeek xaste yi. Loolu yépp di wone ni dikkuñu fa woon ngir teertu seen Njiitum réew. Waaye, dañu fa teewoon ci seen coobare bopp ngir wane ni ñu ko meree.
Ak nu mu mën a deme, ndajem ren ji mooy ndaje mi Njiitu réew mi Maki Sàll di mujje teewe ci turu Njiitu réewum Senegaal. Juróomi weer kott ko dese ngir mu joxe lenge yi.
Demam googu sax dañul wenn yoon ci xelam. Nde dellusi na ci bi ñu ko joxe kàddu gi démb ci talaata ji. Mu jot faa xamleet ni dina amal i wote yu jaar yoon te fas naa yéene joxe lenge ye keroog 2i fan ci weeru awril 2024. Kàddoom yooyu, duggul ci noppi saa-senegaal yu bare, rawatina ña féete foofu fa New York.
Lii day wone rekk ni mbiri Senegaal soxalee Móodu-Móodu yeek Faatu-Faatu yi. Firnde la ci ne, ñoom way-tukki yi, bëgg nañ seen réew te ñoo ngiy topp li fiy xew. Dalal bu ñagas bi ñu dalal Maki Sàll nag, wares na ci jukkee ay njàngat. Ndax, guléet lu ni mel di dal Njiitum réew. Dafa di, deru Senegaal sax daf cee yàqu. Ndaxte, àddina sépp a ci teg bët, yéenenkaay yu siiw biral ko. Bu ko defee, way-pólitig yi war nañ ci jànge ne, Senegaal ga woon ak gu jamonoy tey jii, du benn.
Boroom xam-xam yu bari ak i faramfàccekat yi àddu ci mbir mi, dañu jàpp ne, tere yi ñuy tere nit ñi ñaxtu ci réew mi, xat bi ñu fi xat ak jàpp yu bari yi ñoo tax ñu bokkal Njiitu réew mi mer. wanees na ko ne, kàddoom ak dooleem Senegaal kepp la yem. Te, sax, bu awril 2024 jotee, dina ñàkk kàddu geek doole ji. Balaa boobu, moom Njiitu réew mi mën na seqiy jéego, jël ay ndogal yoy, dina mën a dëfal askan wi, ñu baalee ko ko tuuti. Ndax dina suufe ba gis loolu ? Li ci kanam rawul i bët.