MAKI SÀLL FEDDALI NA KÓOLUTEEM CI AAMADU BA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Àllarbay tay jii la xibaar gi rot, njiitu réew mi Maki Sàll xamal na askan wi ne tay la gën a gëm Aamadu Ba te mu ngi fas yéene wàcc, ànd ak moom ci kàmpaañ bi.

Ci fan yii nu génn, réerul kenn ni coow li bari woon na ca biir Bennoo Bokk Yaakaar. Yooyu wax doon wëndeelu ci kaw kii di Aamadu Ba mi Njiitu réew mi, Maki Sàll, tànnoon jiital ko mu di lawaxu lëkkatoo ga. Ñi naan Maki wóolootu ko, jàppalewu ko. Mu am ci sax ñu naan yenn jagle yim ko defaloon nangu na leen, nar koo buuxal keneen. Coow loolu bari woon seen biir ba tax ñu ci bari di wax ni jëwriñ ju njëkk ja woon doyatul njiitul APR li. Looloo sabab, moom Maki Sàll, mu àddu tay ci àllarba ji xamle ni mu ngi feddali kóllëreem ak kóoluteem ci lawaxam bi. Yamu ca, ndax gannaaw loolu, xamle na ni dina wàcc, ànd ak moom ci kàmpaañ bi ngir dooleel ko ci laaj bi muy laaj réew mi.

Moom njiitul APR li dina waxaat ak mbooleem kilifa gu nekk ci biir APR ba sax biir BBY ngir ñu gën a jàppante, jàppoo te ànd liggéey dooleel seen lawax ngir am ndam ngoonug 24i fani màrs 2024.

Yooyu ndogal mu jël nag, du lenn lu dul ngir fay wax yu sew yi tàmbali woon di jib ak di teeyal xeli nit ñi. Waaye tamit, ngir gën a dooleel seen mbër mi gannaaw ba mu giseeu ñenn ci laxaw yees téewoon ca baayale ya ak ñeneen ca kilifay pólitig yiy jokku ci lëkkatooy Jomaay 2024, PUR, Xalifa 2024, añs.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj