Gaawu, ñetti fan ci weeru féewiryee 2024 la Njiitu réew mi jëloon ndogalu dàq wote yi waroon a am ñaar fukki fan ak juróom ci weer wii. Ñu ni déet-a-waay, waa Ngomblaan gi dëggal ndogal li. Yemul foofu kese, daf cee yokkoon ne wote yi dàq nañu leen ba fukki fan ak juróom ci weeru desàmbar 2024. Ci gàttal, dañoo yokkaloon Njiitu réew mi lu tollu ci fukki weer ci moomeem gi. Boobak léegi, coow laa ngi ne kurr ci biir réew mi. Bërki-démb ci alxames ji la ndajem ndeyu àtte mi génn, ne leen du ci dal. Maanaam, ndogal li Njiitu réew mi jël du jàll. Wote yi dañu leen di amal balaay Nguuru Njiitu réew mi di jeex fii ak 2 awril 2024. Ñu bari doon samp ab laaj naan ndax, Njiitu réew mi Maki Sàll dina nangu ndogal li waa ëtt boobu jël ?
Ndogal li ndajem ndeyu àtte mi jël jur na mbetteel ci ñenn ñi. Ndax, pattaaral gi dafa xaw a yàgg ba ñu bari di laam-laame taxawaayam. Lu jege fukki fan ak juróom a ngii yoo xam ne daanaka réew mi nekkul ci jàmm. Li ko waral du lenn lu dul li Njiitu réew mi toog ba ñu ne suba la kàmpaañ yi di door, mu ne leen mukk du fi ame, “ndax, dogal li ma génnee woon ñeel àppub wote yi faxas naa ko ba jëmmi jamono.” Muy ñi fare ci kujje gi, kuréli way-moomeel yi ñépp boole seen doole ak askan wi ne mukk du fi ame. Ndeem sax, Ngomblaan gi jàppal na ko tànk taxul mu sotti.
Dafa di, gaa ñi doxalinu dépite yi moo leen gën a yëngal. Ndax, ginnaaw loolu rekk la jàmmaarloo yi taqarnaase ci béréb yu bari ci biir-réew mi ba ay bakkan rot ci. Démb, la ndajem ndeyu àtte mi di ci sog a àddu, xamal askan wi ne moo nekk ci dëgg. Ñii jàpp ne Njiitu réew mi dina leen ko nangul. Ña ca des jàpp safaan wa.
Démb ci àjjuma ji la ndeyu-mbill ji, Maki Sàll, génne ab yégle wone taxawaayam ñeel li ëtt boobu wax. Nde, daf ne ko fi mu jàpp àppu wote yi mënut a nekk. Na jàpp wote yi ca na mu gën a gaawe. Moom Njiitu réew mi ne dégg na li àttekati ëtt boobu wax. Ndax, ci firnde yu leer nàññ lañu ko teg. Rax-ci-dolli sax, sàrtu ndeyu àtte Senegaal noon la ko tëralee. Te, nee na dina jëfe ndogalu ndajem ndeyu àtte mi. Waaye, li jaaxal gaa ñi kay mooy kañ la namm a amal wote yii nga xam ne ñépp a ngi leen di xaar ?
Bees sukkandikoo ci yégle bi, li mu tontu ci loolu mooy ne dina amal ay caytu ci lu gaaw ngir amal wote yi ci àpp yu mucc ayib. Ci gàttal, moom jàppagul ab àpp ngir amal joŋante yi. Ndax, dina ko jàpp diggante fii ak ñaari fan ci weeru awril am déet ?