Maki Sàll tëkku na njiiti Senegaal yu yees yi. Moom, Njiitu réew ma woon, dafa doon tontu laaji saabalukaay bii di Jeune Afrique. Bi ñu ko laajee nag lu jëm ci tuumay salfaañe alalu réew mi. Moom nag, weddi na lépp. Daf ne :
« Ragaluma dara. Nañu ma topp bu leen neexee. Sama bilaŋ mi ngi fi, ne fàŋŋ, te amuma dara lu may nëbb. »
Cig pàttali, ca weeru sàttumbaar 2024, elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, dafa àndoon ak yenn jëwriñ yi, amaloon ndaje ak saabalkat yi. Ca ndaje mooma, daf ci tuumaaloon Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, ak nguuram, wax ne dañu salfaañe alalu réew mi, nëbb bor bi Senegaal ame. Ginnaaw gi, Ëttu cettantal bi amal na luññutu, génne caabal guy dëggal waxi elimaanu jëwriñ yi. Boobaak léegi nag, ñoo ngi joxoñ baaraamu tuuma Maki Sàll mi nekkoon Njiitu réew mi. Waaye, bees sukkandikoo ciy kàddoom, lépp ay sos la, deful te defluwul dara ba dara booloo jeex. Lii la wax :
« Damay weddi tuuma yii yépp ba mu set wecc. Ci anam bu leer lanu liggéey ak sunuy digaale. Te, at mu jotaan, Ëttu cettantal baa daan saytu ak a dëggal koppari Càmm gi. Xaar ba tay bëgg a wax ne dara baaxul, loolu ay waxi caaxaan la. »
Njiitu réew ma woon wax na sax ne, moom ak ñépp ñoo ko yégandoo, ci làmmiñu elimaanu jëwriñ yi. amul fenn fu ñu nu laajee sunu xalaat ñeel mbir mi. Boru bi nu ameel bitim-réew day feeñ saa su nekk, lu ñuy xam la. ci campeef yu ay réew bokk lañu koy lebe walla ci ay réew yu nuy liggéeyal. Bor boobu, ci bànk bii di BCEAO lay jaar. Kon, kenn mënu ko nëbb. »