Diggante Farãs ak Mali ma ngay wéy di ñagas. Loolu nag tàmbaliwul tey rekk. Ndax, ginnaaw bi ñu daaneelee kii di Ibraahiima Buubakar Keyta la ànd bi tàmbali woon a taq suuf. Li ko waral mooy ndogal yu am solo yu Nguurug Mali gi jot a jёl ngir dakkal yenn lёkkaloom ak ñii di waa Farãs. Loolu nag, mooy dagg xoli Farãse yi fim ne nii. Ndeke, amatuñ fa Mali lenn lu ñuy dogalati, walla di ci àddu. Rax-ci-dolli, fan yii nu génn, Asimi Goytaa, Njiitul Mali, dafa jёl ay ndogal yu am solo, daldi far yenn ciy déggoo yu ñu xaatimoon diggante ñaari réew yi laata ñuy moom seen bopp. Dafa mel ni Afrig dafa nekk di yeewu nag.
18 féewaryee, njiiti Mali yi dañu génnewaatoon ab yégle, tëbal mёddi sóobarey Farãs (troupes françaises) ya fa desoon. Ci lañu leen joxe àpp, maanaam ba bésub 15 ut 2022 lañu leen mayoon ngir ñu làlli fa seen i dëbës. Waaye, mbir mi yamul foofu, ndax bi ñu jàppee ne kibaaraani Farãs yi dañu leen di sosal ak a fenal, di gàkkal seen der ak a tasaare ay xibaar yu wéradi, ñoom itam, yat bi dal na leen. Nde, 16 màrs 2022 lañu tere woon RFI ak France 24 Mali. Kon, soldaar yile, tiituñu, ragaluñu ; te yit, fowuñu, foluwuñu. Dog buumu njaam gi rekk a leen itteel. Dafa di, am réew mënta suqaliku feek yaa ngi ci nootaange. Waaye, ànd ak loolu yépp, ak toroxal yi ñu ko toroxal yépp, Farãs bàyyiwul.
Keroog, 18 ut 2022, Mali dañu tuumaal Nguurug Farãs ne, ñoom ñooy jox i xibaar ak i ngànnaay ñii di rёtalkat yi (terroriste). Farãs daldi génn, weddi yile tuuma ba mu set, ne mёsut a dimbalante ak reykati nit yooyu. Wànte de, Mali nee na am na ay firnde yu leer nàññ, wér te wóor, ñeel tuuma yi mu tekk ndoddul Farãs. Dafa di, Mali àqi na ONU, sàkku ci Ndajem kaaraange gi mu amal ab jotaay ngir mu mën a biral ay firndeem. Waaye, ba tey, dara. Ñu ngi ruumandaat naan Farãs a tere ndaje moomu am, moom ak réew yi koy jàppale. Dangay gis ne kon, am na luy ñuul ci soow mi. Mu mel ni nag, xeex dafa daj fànn yépp.
Xew-xew bees mujje nemmeeku mooy li Goytaa jёl ay ndogal, far yenn ciy déggoo yi Mali xaatimoon ak Farãs ca atum 1959. Déggoo yooyee, ñi ngi tollu ci fukk ak benn. Goytaa nag, far na juróom-ñett yii toftalu : nangub ndenceefi xaalisi réewum Mali ci lu not, sañ-sañub njëkk a bañ ñeel bépp xeetu mballu-mbindaare bu feeñe Mali, beralug loxo ñeel Farãs ak lijjantiy Farãs yi ci kujjeg màrse piblig yi, àqub Farãs ci ne moom doŋŋ mooy jox réew mi jumtuwaayi xareem te moom kesee am sañ-sañu tàggat sóobarey nooteef yi, Farãs am na sañ-sañu yónnee fa ay sóobare ngir ñu aar seen i moomeel, wareef la ci nooteef yi, at mu nekk, ñu yónnee Farãs ag saabal guy leeral nekkiinu ndenceef yi, bàyyi gépp xeetu lёkkaloo ak meneen réew ci wàllum sóobare, xanaa Farãs ànd ci, bi mujj bi nag, mooy wareef la ci Mali ñu lёkkaloo ak Farãs saa bu xare amee walla bekkoor bu laal àdduna sépp. Xam naa taf nga sa gémmiñ, naan ci sam xel : « waaw, kan walla ñan ñoo xaatimoon musiba bii ? Ñii ñooy workat dëgg-dëgg ! » Waaw, gis nga de. Am ñu nu fiy woy, fekk ne yoo, ñoo nu gasal kàmb bu yàgg. Ndekete, Farãs dafa yàgg a muucu deretu Afrig. Li muy ngande-ngandelu yépp, ndeke ab liir kese la, taxaw ci mbaggi Afrig, di jaay ngóora. Waaye, ndokk bi Goytaa ñëwee.
Mali dafa bёgg a moom boppam. Bëggatul Farãs di ko jàppe nooteefam, na ku nekk xam boppam, jox cër moroomam, yem fu mu war a yem. Na ku nekk jiite réewam nim ko soobee. Waaw, nu golo xam, boote doomam. Farãs nag, ñépp a xam ni bu bàyyee Mali ak réewi Afrig dina gën a torox. Nu xool fu Mali di mujje ci xeex bi mu sumb.