Diggante Farãs ak Mali ma ngay wéy di ñagas. Loolu nag tàmbaliwul tey rekk. Ndax, ginnaaw bi ñu daaneelee kii di Ibraahiima Buubakar Keyta la ànd bi tàmbali woon a taq suuf. Li ko waral mooy ndogal yu am solo yu Nguurug Mali gi jot a jёl ngir dakkal yenn lёkkaloom ak ñii di waa Farãs. Loolu nag, mooy dagg xoli Farãse yi fim ne nii. Ndeke, amatuñ fa Mali lenn lu ñuy dogalati, walla di ci àddu. Rax-ci-dolli, fan yii nu génn, Asimi Goytaa, Njiitul Mali, dafa jёl ay ndogal yu am solo, daldi far yenn ciy déggoo yu ñu xaatimoon diggante ñaari réew yi laata ñuy moom seen bopp. Dafa mel ni Afrig dafa nekk di yeewu nag.
Talaata 18 ut 2020 lañu daaneel Nguurug Ibraahiima Buubakar Keyta. Ca la kurél gii di Comité National pour le Salut du Peuple (CNSP) jёle woon réew ma ba tey. Mu mel ni nag, boobaak tey, ñu bari njortoon nañu Farãs a defaatoon mёniinam. Nde, tubaab yi, teg loxo réewi Afrig jaral na leen lu ne, ba ci nasaxal seen i koom, daaneel ay nguur ngir teg fa seen i ndaw, maanaam ay tubaab yu ñuul. Moo tax, bi coow li jibee, xel yépp ne yar ci nootkat yu bon yooyu. Dafa di, Farãs sax moo njёkkoon a génn di ñaawlu jёf ji. Waaye, naaféq bees ko xame moo taxoon gёmeesu ko woon. Ndekete yoo, du ci lenn.
Bah Ndaw mi nekkoon jёwriñu kaaaraange lees dénkoon Njiiteefu négandiku gi. Booba, Asimi Goytaa moo doon tof-njiit la, Moktaar Wan di woon jёwriñ ju njёkkoon ja. Waaye, dañu dem ba ci biir, xel tàmbalee ñaaw ci Bah Ndaw. Soldaar yi, ci kilifteefu Asimi Goytaa, njort ne Bah Ndaw mii kat, ku dem Farãs ёlbati na xel mi ba féetewoo ko. Ci lañu jёlee seen i matuwaay, déjjati ko ci njiiteef gi. Lu ko moy, doon na leen yàqal li ñu jotoon a liggéey yépp ak li ñu nasoon ngir péexug Mali ak naataangeem. Ñoo ngi fàttaliku, keroog 24 me 2021, ba Moktaar Wan di tёral Nguuram. Ca bés ba lañu leen jàpp, wàcce leen. Ñaari fan lees ci teg, 26 me, ñu tekkilu leen seen i ndomboy-tànk, ñu daldi bàyyi. Fullaay jaay daqaar, am déet ? Goytaa daldi dёggal boppam, jёl mbir yi, jiiteel ko boppam. Boobu nag la jafe-jafey Farãs yi ca Mali tàmbali. Dogal ya ñu fa amoon yépp ak i ngёneel, Asimi Goytaa ak i ñoñam di leen dindi ndànk ndànk. Makorõ di gёn a bokk golo gi, njiiti Farãs yiy jёfuur. Waaye, ñoo yey kat. Ku tàmm loo wax rekk ñu tegal la ci “waaw”, loo yóotu jot, boo ko amatul sa xol du neex. Dafa di, Farãs ak i njiitam, ay jaam lañ nu mёs a jàppe. Seen juróom-ñaari xel mёsta xalaat kenn ci njiiti jaam yu tekkiwul dara yooyu di leen diir mbagg, ba di leen dàq seenum réew. Waaye, loo gis, dafay jeex.
Mali dafa doon ŋàññi doxalinu Farãs ñeel xeexug terorist yi. Noonu, Farãs xéy bés rekk, ci ndogalu Makorõ, weeru suwe 2021, dakkal liggéeyu Barkhan. Ci la xamle ne soldaar yi dinañu wéer ngànnaay yi ci atum 2022, dellu ci seen i réew. Bett boobu leen Farãs bettoon a tax ba, kii di Songel Mayga, jёwriñ ju njёkk ji, kaasoon loolu ca magum ndajem Mbootaayu xeet yi (ONU), amoon ca New York bésub 25 sàttumbar 2021. Ca la waxe woon ne dañ leen a wor, wacc leen ci digg yoon wi. Waaye de, wéet du tee gaynde xeex. Bi loolu amee yit, waa kippaangoo Wagner bu Riisii lañ digaaleel ci wàllu kaaraange. Ndege, Mali dafa yokk xar mi karaw. Ab aawo bu mёsta wujje, xamul luy wujje, xalaatu ko te bёggu ko, nga takkal ko wujju wow, noonam la teg si, mu ragalee ko xel. Malee pànk ! Xam naa yaa ngi naan “ñaw !”.
Waaye, ñoom Goytaa ak Songel Mayga yemuñu foofu de. Bi leen ndawal Farãs li bёggee yab, di leen sosal ak jéem a tuutal, dañ ko dàq ca xaj. Waaw kay. Bésub 31 Saŋwiye 2022 lañu génnee ab yégle, siiwal ci dàqug àmbasadёeru tubaab bi, Sowel Méyёer. Ñetti fan kepp lañu ko mayoon cib àpp ngir mu génn Mali. Ngeen foog ne jeex na ? Xanaa dégguleen xeexu njaago ? Loolu la Mali di def nag. Tegleen foofu seen baaraam ba ёllёg, nu wéyal.