Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer bokk nañ xaatim ab sàrt bi ñu tudde ci nasaraan Charte du Liptako-gourma. Sàrt booboo wund juddug digaale gi ñu bokk sos, duppee ko Alliance des Etats du Sahel, gàttal biy joxe AES. Maanaam, ñetti réewi Sayel yii di Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer, dañu bennoo def wenn say ngir aarante. Ndax, kenn umpulewul ne, ñetti réew yooyu yépp ay sóobare ñoo leen jiite. Te, réew mu ci nekk, rëtalkat yi walla terorist yi dañ ko sonal witt jamono jii. Li ñu dugge costeg digaale gi mooy gën a mën a jàppalante ci wàllu kaaraange, di sotalante bu ñu songee kenn ci ñoom ñett.
Démb, ci gaawu gi fukki fan ak juróom-benn ci weeru sàttumbaar la Kolonel Asimi Goyta (Mali), Kàppiten Ibraayma Taraawore (Burkinaa Faaso) ak Seneraal Abdurahmaan Ciyaani (Niseer) xaatim ab sàrt ñeel kaaraange. Ñoom, ñetti sóobare yi jiite seen ñetti réew yooyu jamono jii, dañoo déjjati njiit ya fa nekkoon, fob lenge yi, di jiite. Te, jamono ji ñuy foqati seen nguuri réew yi, ci jamonoy fitna ak taafar ju tar la seen ñetti réew yooyu nekk.
Dafa di, ci diirub fukki at ak lu tegal, terorist yaa nga leen singali, di leen song guddeek bëccëg, di rey ak yàqate rekk. Waa bitim-réew, rawatina Farãs yónne woon nañ leen i sóobare ak i ngànnaay ngir jàppale leen ci xeex bi, waaye dara. Tey la Waalo gën a aay. Ñoom sax, biñ togee ci jal bi, dañu dog buum gi leen lëkkale woon ak Farãu Macron. Nde, seen diggante dafa xajam ci sabab yu bare. Li ñuy njort mooy ne, loxo Farãs deñul ci fitna yi leen di gaar boobaak léegi. Te, ndeem jaamuwuñu soxlay Farãs ak lenn ci réewi sowu yi, Macron ak i ñoñam, jaare ko ci seen kibaraan yi, dañoo dëkk ci di leen tiiñal ak a ñàkkal worma. Looloo leen tax a fippu, dàq Farãs ak i kibaraanam yi doon wesaarey xibaar yoy, nee ñu, yàq der ak jaxase moo leen tax a jóg. bi Farãs génnee ba tey nag, terorist yi dañoo gën a fétteerlu, di amal i cong yu jéggi dayo, di rey ay lim yu takkoo takku ciy soldaar ak i maxejji réew ya. Loolu doyatul, seen i dëkkandoo yiñ bokkal CEDEAO di leen àtte-ñàkkal ak a teg ay coono yu diis.
Ngir fàttali, CEDEAO tegoon ay daan yu metti ci wàllu koom-koom réewum Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer mii ci mujj. Askani ñetti réew yooyii sonnee ci lool. Yemu ca de. Nde, bu dee Niseer, kurélug Afrig sowu jant gi dafa nisër a song réew ma ngir déjjati Seneraal Ciyaani ak i naataangoom, tegaat ca jal ba Basum. Fitna yooyu yépp ñoo leen a daje cim pénc, sanc ag bennoo ngir dooleelante seen biir. Ndax, seen réew yi dañoo digaloo. Te, mbooloo kat mooy doole.
Laata ñuy xaatim seen sàrt bi sax, njiiti Mali yeek yu Burkinaa Faaso yi dañu fasoon yéene taxawu Niseer, jàppale ko ci xeex bi, bu ko CEDEAO songoon. Boobaak léegi nag, gaa ñaa ngi ci lewtoo gi, songoo moom amagul. Waaye, ngir gën dëggal seen bennoo gi, dañu taxawal ag digaale gog, day sàrtal jàppalante bi war a dox seen diggante saa buñ songee kenn ci ñoom, ak fu cong mi mën a bawoo. Xanaa du mbooloo mooy doole ?