MBËKK MI : DEM REKK !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbëkk mi lëmbe na lool réewum Senegaal rawatina ci fan yii. Lu daan am ci am at walla ci ay weer, léegi, ci ayu-bés lay am. Li am ci ayu-bés bii firnde la ci. Nde, lu ëpp ñaari junniy doomi Senegaal ñoo teerijee Espaañ. Te, xewul ci lu dul diggante talaata ak léegi.

Mbëkk mi, jamono jii, amatul góor ak jigéen, mag ak ndaw, ñépp a ngi ci biir. Ñépp la Espaañ luqi seen i bët. Ñi demagul it, ñu bari ci ñoom a ngi ci yoon wi. Gaal yi teer ci àjjuma jii rekk doy nañu ci firnde. Ndax, amoon nañu lu tollu ci juróom-ñetti jigéen ak juróom-ñeenti xale. Kon, mbir mi ëpp na loxo ba noppi. Dafa di, mbirum Bàrsaa ak barsàq du lu bees ci Senegaal. Daanaka, at mu jot ñu nemmeeku ko fi. Waaye, ren moom da cee raw, rawatina ci ñetti weer yii (sulet, ut, sàttumbaar).

Ba tax na jamono jii marinu Espaañ, bu Marog ak bob Senegaal nelawatuñu ba yàndoor. Ndax, daanaka, bés bu nekk benn marin ci ñett yooyu am ñu mu jàpp. Waaye, bi ci gën a fés moom bu Espaañ bi la. Bari na lool lu muy am gaal yu bawoo Senegaal teerijee ci benn ci dun yi ñuy dippe “Iles d’El Hierro, Gran Canaria ak Tenerife”. Li mat a laaj kay mooy lan moo tax doomi réew mi di dawee nii seen um réew ?

Laaj boobu nag mën naa am tontu yu bari te wute. Waaye, bi ci ëpp doole mooy yaakaar ji ñu am ca réew mooma. Ndax kat, nee nañu yaakaar tiyaaba ju gën a bareey yóbb jullit Màkka. Kon, mbirum koom mooy sabab bi gën a fés te, tax doomi réew mi di dem foofa. Ndax, ak li limu ñi faatu ci géej gi di bari lépp taxul ñu bàyyi. Li ñuy jàpp fa Daxla (Marog) di leen delloosi ak ñi nga xam ne sax fii ci réew mi lañu leen jàppe, loolu yépp feesul seen i bët.

Li ko waral mooy bëgg ëllëg gu mucc ayib. Te, jàpp ne foofa rekk lañu ko mën a ame. Ba tax, fan yii moom yëf yi taqarnaase na lool. Ndax, bees sukkandikoo ci li Ayooba Fay fésal ci mbaali jokkoo yi, ñetti gaal yu jóge woon Senegaal àgg nañu ca El Hierro ak Tenerife ci gaawu gii. Genn gaa ngi yeboon téeméeri nit ak ñaar-fukk ak ñaar. Ñaareel bi juróom-fukki nit ak juróom-ñaar. Ga ca des yeb téeméer ak fukk ak juróom-ñeent.

Mbir mi yemul foofu. Ndax, nee na lim boobu bu yokkoo ci li juróom-ñaari téeméer ak juróom-ñett fukk ak ñett yi duggoon ci àjjuma ji, day dem ci junni ak lu teg. Kon, bu ñu ci boolee la duggoon ca àllarba ja, am ñu ko jàpp ci talaata ji, limub ñi dugg ci diggante bés yooyu dem na ci ñaari junni ak ñaari-téeméer ak juróom-benn fukk ak ñeenti doomi Senegaal yu dugg Espaañ jaare ko ci gaal yi.

Fim tollu nii nag mbir yaa ngay bëgg a tagatémbe. Ndax, ñi war a defar ub dëkk bu ñu demee ba amatuñu fa yaakaar di ko daw ba mu jaral leen dee, jar na seetaat. Ak li yoon wi di metti lépp taxul ñu bàyyi. Ñu jàpp rekk lu waay torox rekk, waay tekki na ca.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj