MBËKK MI : GAAL GI SUUX FA MBUUR

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëyya ju metti amatina ci mbëkk mi. Genn gaal gu yab ba fees, wutali woon tugal, moo suuxati.  Jëyya jaa nga ame Mbuur, fa tollook ñaar, jàpp ñetti kilomeetar ci biir géej gi. Gaal googu sax, Mbuur la bawoo woon. Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot, lu ëpp 200i doom-aadama ña nga woon ca biir. Jot nañu làqi ci ñoom lu tollagum ci fanweeri néew ak juróom-ñeent, xettali ñaar-fukk ak lu teg. Ba tey jii, géej gaa ngi wéy di goqi ci tefes gi way-lab yi. Wallukat yaa ngay wéy di seet ña ca des.

Ci ngoonug dibéer jii weesu la gaal ga suuxoon. Takk-der yi jàpp nañ kii di Séex Sàll mi doon yóbbaate. Moom, Séex Sàll moomii, boroom gaal gi, nappkat la, di mag ci meeru Mbuur bi, Séex Isaa Sàll. Nee ñu, moo dox dem pólis, booleji boppam. moom, 52i at la am. Mi ngi woon ci biir gaal gi ba muy suux, waaye dafa féey, génn. 

Nee ñu, Nguur gi dina yabal i ndaw ngir ñu jottaliji njaalu Njiiut réew mi ak elimaanu jëwriñ yi. Soxna Xadi Jéen Gay, jëwriñ jees dénk ndaw ñi, tàggat-yaram ak mbatiit mi mooy jiite ndaw ñooñii. Tey ci àllarba ji lañ war a dem Mbuur. Perefe Mbuur bi, Aamadu Jóob, moo leen di dalal. Dinañu àgg ca këru delege kàrce bu “Thiocé Ouest” laata ñuy wéyal seen ug wër ca dëkk ba.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj