MBIRI ABDULAAY SILLA AK LAT JÓOB

Yeneen i xët

Aji bind ji

Talaata jii weesu lañu taxawal li ñuy dippe PJF (Pool Judiciaire Financiaire). Ëttu àtte boobu nag, taxawul, taxawaaluwul. Dañ ko samp rekk, sóobu xaat ci liggéey bi ñu ko sas. Ndax kat, boobaak léegi, waa DIC ñu ngi woolu rekk, di déglu. Dafa di, diggante àjjuma ak gaawu rekk, woolu nañ ci ñaar ñoo xam ne kenn dootuleen aajar ci réew mi : Abdulaay Silla ak Lat Jóob. Te, kenn ci ñoom bokkul ak moroomam li ñu koy toppe. Donte ne sax, Abdulaay Silla moom, Yoon teggeegul bëtam ci moom. Waaye, terewul ne bàyyi na ko mu dellu këram. Bu dee Lat Jóob, moom ba tey ma nga ca loxoy Yoon.

Mbirum woolu yi fa DIC moo gi lëmbe réew mi jamono jii. Mu am nag tur yoy, ñoo ci gën a fés. Ci àjjuma jii weesu, DIC (Division des Investigations Criminelles) woolu woon na ngóor sii di Abdulaay Silla, Njiitul Ecotra. Luññutukat yi dañ ko doon déglu ci mbirum wurus wi ñu wax ne, dugalees na ko cib roppalaan jàmbur (jet privé), génne ko réew mi. Wurus woowu nag, ci lees wax, mi ngi tollu ci 2 700i kilo. Te, moom dañu ko cee duut baaraamu tuuma, jàpp ne daf ci laale. Maanaam, ñi fexe ba wurus wi génn réew mi, njortees na ni ci la bokk. Ca atum 2020 la mbir mi amoon. Moom nag, Abdulaay Silla,dafa lay ne, diggante atum 2019 ak 2022 nekkul woon Senegaal. Bàyyi nañu ko mu ñibbi këram. Waaye, loolu taxul ñu teggi wenn yoon seen tànk. Ndax, wooluwaat nañu ko ëllëg ci altine ji.

Naka noonu, Lat Jóob mi fi nekkoon jëwriñ ji ñu dénk wàllu tàggat-yaram, jiite woon fi amit LONASE (Loterie Nationale du Sénégal), mi ngi ci loxoy Yoon. Démb, ci gaawu bi, lañu ko woolu woon ngir déglu ko. Li sabab woote bi, ci li rotagum ciy xibaar, dafa aju ci mbirum luubal xaalis. Bees sukkandikoo ci waa Dakaractu, ki fi jiite woon 1Xbet Sénégal, Muhammet Jeŋ, nga xam ne moom lañu njëkk a déglu, moo teg ay tuuma ci ndoddam.

Muhammet Jeŋ moomoo wax luññutukat yi ne, dafa jox Lat Jóob koppar gu takku gu tollu ci juróomi miliyaar. Ba tey ciy waxam, bi mu koy jox xaalis bi, ay pàcc-pàcc la ko def. Maanaam, ñëwul rekk, joxandoo ko lépp wenn yoon. Rax na ca dolli sax, moom Muhammet Jeŋ, ne koppar googee tax ba Lat Jóob doon boroom alal, te ci la jëndee ag kër fa Grenoble (Farãs). Moom, ndeyu-mbill ji, bañ na ba tëdd ci suuf. Nee na loolu du dëgg. Ay layookatam sax naqarlu nañu doxalinu Yoon ci loolu. Nde, moom Lat Jóob, ba tey bàyyiwuñu ko. Dañu koo jàppandi jamono jii, fa la fanaan démb. Loolu moo metti ay layookatam. Ndax, ki nga xam ne moo teg tuuma yooyu ci ab deram, dañu ko bàyyi mu dellu këram. Maanaam, dañoo bàyyi ki ger, téye ki ñu ger.

Mu mel ni, kii di Lat Jóob, ñaari mbir lañu koy toppe. Benn bi mooy luubal alalu askan wi (détourment de derniers publics), ñaareel bi mooy li ñuy duppe “blanchiment de capitaux”, weexalug xaalis. Bees sukkandikoo ci layookatam, Me Elaas Juuf, suba ci altine ji dinañu ko jébbal toppekatu PJF bi. Kon, fii ak i fan dees na xam fu gaa yooyu di mujj ak Yoon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj