MBIRI BAABAKAR FAAL : CAP DUGG NA CI COOW LI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa CAP àddu nañu ci mbiri Baabakar Faal. Ginnaaw bi taskatu xibaar bi jotee ay saaga ak i tëkku, fas yéene wuñ koo seetaan wenn yoon. Taxaw nañ temm ngir xeexle ko ak di ko digal mu dem ba fu mbaxana doonee benn.

Taskatu xibaar bii di Baabakar Faal dafa jotoon i saaga ak i tëkku ginnaaw bi mu génnee ag caabal di ci tontu Njiitu réew mi Maki Sàll. Fekk ci talaata jii ñu weesu, 9 sãwiyee 2024, ñu doon amal ndajem diisooy kibaaraan yu réew yiy làkk farañse (Assises de la presse francophone) fa Jamñaajo ci teewaayu Njiitu réew mi Maki Sàll.

Ca ndaje mooma la Njiitu réew mi yékkatee ay kàddu ñeel melokaanu kibaaraan yi ci réew mi, rawatina nees di defee seen yéenekaay yi. Looloo waral ba Baabakar Faal fésal ca biir caabal googu ni Njiitu réew mi am na leneen lu mu war a wax lu gën a jamp ñeel kibaaraan yi te sax du moom mooy taxaw di am lu muy jam ci kibaaraani réew mi.

Ginnaaw caabalam googu nag, taskatu xibaar bi dafa jot i ndéggat yoy, saaga nañ ko ciy saaga ak di ko tëkku ci faat bakkanam. Muy xibaar bu Ibraayma Lisaa Fay, Njiitu Mbooloom liggéeykati kibaaraani lënku gi (Appel), siiwal.

Tëkku yi ñu tëkku taskati xibaar bi nag moo waral ba CAP (Coordination des associations de presse du Sénégal), di Kurélu Mbootaayi kibaaraani Senegaal, yore kàddu taskati xibaar yi ak ñiy liggéey ci kibaaraan yi génne ab yégle di ko ñaawlu ak a naqarlu. Ci biir yégle boobu, CAP dafa ci fésal jàppale ak taxawu ñeel taskatu xibaar bi.

« Kurélu mboolooy kibaraan yee ngi fésal seen taxawaay ak jàppale ñeel Baabakar Faal, Njiitu saabalukaay bii di Rfm. Ñoo ngi koy ñaan mu bañ am lenn lu muy tiit ak xoqatal bu mu mën a doon. »

Ba tey ci biir yëgle bi, kurél gi di xamle ni Baabakar Faal deful lu dul liggéeyam. Naka noonu, ñuy sakkoot ci moom  bu mu am lu mu ciy ragal walla mu koy tiit.

Ñoom sax yamuñu ci lii. Nde wax nañ ceeg Nguur gi ak luy wàllam ci aar kaaraange taskati xibaar yi. Ba tax ñuy sàkkoot ci moom mu jël ay matuwaay ñeel kaaraangeem te ubbi ab lànket ngir teg loxo ñi koy tëkk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj