MBIRI NDEELA MAAJOOR JUUF

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndeela Maajoor Juuf dugg na ci guddi gu bët setagul. Ginnaaw ba ñu ko jàppee ba téeyandi ko, Birigàdd Su (Brigade de protection de la sûreté urbaine) a ngay wéy di déglu ña ko daan liggéeyal. Waaye seen wax yi deful lu dul gën a dugal ki nekkoon seen njaatige.

Bërki-démb ci alxames ji la Birigàdd Su tegoon loxo Ndeela Maajoor Juuf. Li ko waraloon nag di widewoo yi tasaaroo ci mbaali jokkoo yi te tukkee ca bérébam ba mu duppee Kër yërmande, doon fa dalal ak a yor ay xale. Muy ay widewoo yu daw yaram ndax melokaani xale yees ciy gis ak béréb ba ni mu ñàkkee cet.

Ñaari fan ginnaaw bi ñu ko téeyee fa birigàdd ba nag, seen yéenekaay Defu Waxu di leen ko toppal ni mu leen ko digee woon. Ay gëstukati birigàdd ba dem nañ fa kër ga. Am na itam  ñenn ci jëwriñ yu fa dañi woon kumpa. Naka noonu, jël nañ xale ya fa nekkoon yóbbu leen fa raglub Albert Royer, di loppitaal Faan (Hôpital Fann). 2i xale jot nañ cee ñàkk seen  bakkan. Am naat 48 yu ci lott lool.

Fii mu nekk, mënees na jàpp ni liy xeeñ neexul ci Ndeela. Nde, am na ci ñi ko daan liggéeyal, ay surgaam, yu birigàdd bi teg loxo ba déglu leen. Bokk na ci li ñu gën a biral, Ndeela Maajoor Juuf, wutukaayu xaalis kepp la yoroon ci bérébam boobu. Donte ni doon na fa dalal i xale yu seen i way-jur am jafe-jafey yor, tur wi mu jox béréb ba ak ni mu ko daan doxalee mel na ni Yàlla ak Yaali. Maanaam amu ci woon jenn yërmande, dafa fa doon yaxantu rekk.

Ba tey ci seen i wax, xale yi daanuñu lekk ba suur. Rax-ci-dolli, lànket bi ñu doon def itam ci ñaari xale yi jot a ñàkk seen i bakkan wone na lu méngook li surgaam yi wax. Ndax xale yi ñàkk dund gu baax moo leen faat.

Kenn ci ñoom wax na sax ne daf ko daan tànqoo «… di ci laaj xaalis bu bare ay boroomi tur ginnaaw bi mu leen di gëmloo ni xale bii walla xale bee moom lañ ko tudde. » Ginnaaw bi toppekatu bokkeef gi jógalee boppam ba noppi, ndaw si dellu amal ab kalaame biral na ni Ndeela dafa ko doon laaj 5i tamndaret bi mu dellusee, bëgg jël doomam.

Dëgg laam du dëgg, Ndeela Maajoor a ngi ci guddi gu bët setagul. Nuy xaar fu wànnent di mujje ak i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj