Ginnaaw bi DGE (Direction générale des élections) bañee doxal ndogal li àttewaay bu Sigicoor jëloon, Usmaan Sonko ak i layookatam yóbbu woon nañu mbir mi ca Cena ba ngir mu àtte ndeem am na sañ-sañ bi. Lan la Cena bi wax ?
Cig pàttali, alxames, 12 oktoobar 2023, la àttekat bii di Sabasi Fay joxoon dëgg Usmaan Sonko fa àttewaay bu Sigicoor. Naka noonu, mu neenal ni ñu ko seppee woon ci wayndarew wote yi, dellu santaane ñu dugalaat ko ci. Muy nag ndogal lu Càmm gi mënul woon a dégg ba AJE (Agence judiciaire de l’état) Yoro Musaa Jàllo dugal ab dabantal. Naka noonoot, DGE sukkandiku ci dabantal boobu nga xam ne duggagul woon, daldi lànkal ndawul Usmaan Sonko lii di xobi baayale yi.
Ginnaaw loolu, Usmaan Sonko ak i layookatam tooguñu wenn yoon di xaar ndogal liy tukkee ca dabantal boobu. Yóbbu woon nañ, bir mi ca CENA (Commission électorale nationale autonome) ngir mu def ci lu ko war te digal DGE mu dugalaat Usmaan Sonko ci kayiti wote yi, ni ko àttawaay bu Sigicoor sàkkoo.
Bees sukkandikoo ci xibaar yi jot a rot nag, Cena bi waxtaane na mbir mi ba noppi. Ci àllarba jii weesu, 25 oktoobar 2023, lañ ko doon càmbar. Sunuy nattaango yu Source A fésal nañ ni Cena bi dina siiwal ndogal li mu jël ci ayu-bés bii nu dëgmal. Jamono yii sax mi ngi nekkoon di bind bataaxal yi mu war a jébbal layookati Usmaan Sonko yi ak njiitu DGE li. Waaye, bees sukkandikoo ci waa Senenews, Cena bi dina génn balaa ayu-bés bi di sore. Nde, ëllëg ci altine ji la war a wax.
Usmaan Sonko yóbbu woon na mbir meet ca ëttu yoon bu CEDEAO ci weeru sàttumbar wii weesu. Sñ bi Keledoor Li, kenn ci layookati Usmaan Sonko yi, di xamle ni ëtt boobu itam dina càmbar mbir mi ginnaaw-ëllëg ci talaata ji.
Ayu-bés bii ñu dëgmal nar a am solo lool ci mbir mi. Ñu ciy séentu lu ñaari ndogal yi di leeral ak luy doon ëllëgu Usmaan Sonko ci wote yii di ñëw.