MBIRI USMAAN SONKO : UMS DUGG NA CI COOW LI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw bi àttekat bi tirbinaalu Sigicoor jële ndogalu bindaat Usmaan Sonko ci këyitug wote yi, Yoro Musaa Jàllo, di Agence judiciaire de l’État, maanaam ndaw liy layal nguur gi, dafa génneeb yëgle di ko ci ŋàññ. Muy nag taxawaay bu Mbooloom àttekat yu Senegaal (UMS) rafetluwul wenn yoon ba tax ñuy dànkaafu.

Ci pàttali, alxames jii ñu weesu, yam ak 12 oktoobar 2023, tirbinaal bu mag bu Sigicoor doon na àddu ci mbiri Usmaan Sonko ak nees ko seppee ci këyitug wote yi. Àttekat bii di Sabali Fay daldi fay jox dëgg Usmaa Sonko ngir nguur gi bindaat turuam ci këyitug wote yi.

Ndogal loolu nag dafa jur coow lu bees. Nde bi mu jibee ba ñu bare daldi koy rafetlu, rawatina ay ñoñi Sonko, ñi fare ci nguur gi ñoom dañoo lànk ba tëdd ca naaj ba. Yàggul dara, AJE Yoro Musaa Jàllo génneeb yëgle di ci xamle ni duñ ko bàyyi mu jàll ndax dinañ dugal dabantal. Waaye yemul ci loolu. Dafa ŋàññ ndogal li ba duutaale baaraam àttekat bi Sabali Fay ci ni mu doon àttee mbir mi.

“Jotaayu àtte ba dafa ruslu lool bees ko gam-gamleek lees namm ci àtte bu tëdde njaaxaanaay.

Naka noonu, jamono ji àtte bi di am (ci 13i waxtu), àttekat bi jógul ci di salfaañe ak a salfaañewaat yoon.”

Dem na sax ba naan àttekat bi ci boppam, dafa am rakk bu bokk ci toftaliy Meeru Sigicoor bi. Te kooku bokkoon na ci pàrti Pastef bi woon.

Taxawaay bii AJE am dafa doon lu bett lool waa UMS (Union des magistrats du Sénégal), mbooloom àttekat yu Senegaal. Moo tax ba ñoom itam ñu def ab yëgle ngir joyyanti AJE bi. Ñuy xamle ni dañoo sax waaru bi ñu gisee tuumaam yi.

“UMS mi ngi ñaawlu ba fu ñaawlu yam tuuma yii ci yëgle bi te ñu teg ko ci ndoddu àttekat bu jël ndogal ci ni mu yaakaare ni noonu la dëppook yoon.

UMS mi ngi fàttali ni wax ju soxal yoon ñaŋ koy waxe ca àttewaay ba, deesu ko jaarale ci kibaaraan yi.”

Naka noonu UMS dellu xamle ni ku am looy ŋàññ, am nay bunt yu la yoon tijjil ci ñi ci war a taxaw. Dafa ñaaw lool ñuy gàkkal yoon ak di tilimal deru ñi koy doxal. Ba tax na ñuy sàkku ci ñi séq mbir mi ñu dellu wegante te sàmmonteek jaaruwaay yi yoon tëral.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj