Ci àjjuma jee weesu, magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko àddu woon na ci téere bi doomu réewum Farãs, Sewerin Awenengoo Dalberto, dib gëstukat ci mboor, bind ci jonnug Kaasamãs. Fekk mu doon amal ab mitiŋ fa Sigicoor. Ci kàddoom yooyu nag, wone na taxawaayu kilifay réew mi ci ni téere boobu du génne fi réew mi te kenn du ko fi jaaye.
Ginnaaw kàddoom yooyu, pàccu MFDC bii di Màngukuro, féete ci Abdu Elinkin Jaata, génn na ba wax. Waaye rafetluwuñu tere bi ñu tere téere boobu génn. Ba tax ñuy laaj « lu tax ñuy bañ waa kaasamãs xam seen mboor » (Aamidu Jibaa mi yor seen kàddu). Dem na sax bay jam baaraam Jag Sàrpi mi Usmaan Sonko def delluwaayam : « warees na xamal Usmaan Sonko ni Jag Sàrpi mi muy junj nettali na lépp ba mu des mbooru Kaasamãs. »
Ñoo ngi rafetlu jéego yi Nguur gi di teg ngir dundalaat koom-koom gi ci diggante Sigicoor, Séeju ak Koldaa. Xamle nañu itam ni noppi nañu ngir toog waxtaan ci ni mu gënee jekk. Waaye itam, ñoo ngi sàkku ci magum jëwriñ yi mu def ndànk, ànd ak dal te moytoo topp boroom xel yiy dunde dereetu waa kaasamãs.