Marine Le Pen kenn la ci ñi ñu gën a bàyyi xel ci géewu pólitigu Farãs. Moom, moo jiite dépitey làngu pólitig gii di RN (Rassemblement National), jiite yit seen kippaangog dépite ca Ngomblaanu Farãs ga. Moom nag, ab polotiseŋ la bob, kenn dootu ko nàttable fa réew mooma, ba ci sax bitim-réew. Ndax, taxawaay bi mu am. Mu nekk koo xam ne ñi ngi koy xaar bu baax ci wote yii di ñëw. Waaye, ag bokkam leeragul. Ndax, dafa am daan bu gàllu ci ndoddam, donte ne sax am na dabantal yu mu jébbal Yoonu réew mooma ngir ñu neenal àtte ba ko daanlu.
Barki-démb, ca altine ja, fanweeri fan ak benn ci weeru màrs, la woon layoob Marine Le Pen bi. Waaye, layoo booba de, jëlewu fa ndam. Dañu ko daan, daan bu metti ci ko xam ne mi ngi mébét a bokk ci wote yii di ñëw, di yóotu jal bi. Luubal alalu askan wi lañu ko tuumaal, daan ko ci. Li mu luubal, ca la Yoonu réewam wax, mi ngi tollu ci 2,5 miliyoŋ ci ay Ëro.
Moom Marine Le Pen, daan nañu ko ñeenti at. Ñaar yi la war a tëdd te, ñaar yooyu mu war a tëdd, ab lam lañu ko koy takkal. Xameesagul nag fu yëf yi di mujj. Dafa di, daan yi, yemuñu foofu. Ndax, dañu ko cee tegal juróomi at yoo xam ne du ci mën a bokk ci ay wote. Du mën wote, te du mën a bokk ciy wote, ak bu mu ci mën di doon. Daan boobu nag du ko teree wéy di nekk dépite fa Ngomblaanu Farãs ga, fileek tasuñu ko.
Mu mel ni, moom narul a toog bank ay loxoom di leen seetaan. Ndax, mook i naataangoom, waa RN, jébbal nañu ab dabbantal ngir ŋàññi àtteb ëttu àttekaay bu Pari ba. Démb, ci talaata ji, waa ëttu dabantal bu Pari xamle nañu ne jot nañu ñetti dabantal ginnaaw daan yi ñu teg Marine Le Pen ak waa RN. Te, dabantal yooyee dinañu leen càmbar ci atum 2026 mi. Ñoom moom, seen mébét mooy ñu àddu ci mbir mooma laata wotey palug Njiitu réew yu atum 2027 di teru.
Kon, léegi, mënees na jàpp ne Marine Le Pen moom, ëllëgam ci pólitig leeragul. Ndax, fi mu tollu nii tembe, am na daan bu ñu teg ci ndoddam. Te, xameesagul fu daan boobu di mujj. Dañu koy neenal am dañu koy dëggal, balaay yàgg dees na ci xam dara.