Mbirum Sweet Beauty : ni Ndey Xadi Njaay setal na boppam, taqal Aji Raabi Saar

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, ci talaata ji 23 me 2023 lees di amal layoob Usmaan Sonko ak Aji Saar ak it bu mbirum Sweet Beauty. Bi ñu ubbee layoo bi nag, layookati Ndey Xadi Njaay yi doon nañu sàkku ñu dàq layoo bi ngir ne Ndey Xadi jigéenu-wérul ju tollu ci 8eelu weeram la. Waaye, àttekat bi daf leen gàntal, jël dogalu amal layoo bi. Ginnaaw gi la dàkkandi na jotaay bi ci diirub 15i simili. Donte ni jigéenu-wérul la, tollu ci 8i weeri ëmb, Ndey Xadi Njaay janoo na ak àttekat bi. Taxaw na lu yàgg nag. Wànte, terewu koo tontu laaji àttekat beek toppekat bi. Moom nag, dafa feddali waxam ju njëkk ja, setal boppam, setal Usmaan Sonko, taqal Aji Saar.

Bees sukkandikoo ci kàdduy boroom Sweet Beauty, dafa mel ni Aji Saar daf ko doon baalu ci biir àttewaay bi. Nde, dafa njëkk a wax àttekat bi mu wax ak Aji Saar mu may ko jàmmam, ndaxte : ” Du ma tax a ñëw fii ba noppi di ma rey ak « baal ma ». »

Ginnaaw loolu, laajes na ko ci dàmpuwaay bi, naka la ko sosee, ak naka la fa liggéey biy deme. Soxna si tontu, ne :

« Xéyuma bés rekk tijji dàmpuwaay. Dama daan létt. Ginnaaw gi laa ñëw Ndakaaru ngir tijji fi Sweet Beauty. Mu amoon ñeenti néeg. 2018 ba 2021 dàmpuwaay bi dafa doon dox bu baax te dara mësu faa xew.»

Bu dee colinu dàmpkat yi, Ndey Xadi Njaay leeral ne : « Ñiy dàmp dañ daan sol i tëni yu nëtëx ak yu weex. Jigéen ñi dañuy sol yu wàcc ba ci [seen] wóom yi. »

Ndey Xadi xamleet na fa ne, ñu bari ci ñu fa daan dàmplusi, dañ doon taamu Aji Saar. Waaye, loolu neexu ko woon. Biñ laajee lu tax Usmaan Sonko doon laajte Aji Saar bu fa daan ñëw daf ne :

« Mësumaa wax ni Usmaan Sonko dafa daan laajte Aji Saar saa bu ñëwaan ci dàmpuwaay bi. Bu dee lu nekk ci PV bi la, génne ko ci. Ku góor ku tudd Badara mës na fa dàmp Usmaan Sonko. »

Bu dee lu jëm ci li Aji Raabi Saar wax, li ci Ndey Xadi Njaay tontu mooy :

« Li mu fi wax lépp ay sos la. Nde, bésub 31 desàmbar kenn daawul liggéey ci dàmpuwaay bi. Ci anam yu metti laa am doom bés boobu. Sama jëkkër a ngi fekk Séydinaa Abaabakar ci bunt bi. Ci biir guddi gi, fekk na ko ci kow teeraas bi. Ay 21i waxtu la ma woowaat ne ma Mamã dégg na Aji mu naan waa ji du fi yàgg ndax ndàmpu ñeenti loxo rekk lay def. Ci li Mamã nettali, Aji daf ko wax mu bàyyi ko ci biir mu laaj kiliyaan (Usmaan Sonko) bi njëgu reer. Matul sax ñetti simili, Aji génn di woy woyi seereer. »

Ndey Xadi yokk na ci ne, « am na bés, fekk naa Aji ci kow ab kilyaŋ mu koy raay ci lex yi. Te dama ko dàq ci loolu. »

Fim ne nii nag, layoo baa ngi wéy. Dees na ñëwaat ci yeneen seede yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj