Kurélug mbootaayu xeet yi ñeel àq ak yelleefi doom-aadama, àdduna ci xew-xew yi amoon fi réew mi, fan yii weesu. Li sabab xew-xew yooyu nag, mooy daan bi ñu teg ci ndoddu Usmaan Sonko ci coowal ciif ak tëkkuy rey yi ko Aji Saar di jiiñ. Mu nekkoon musiba ju réy ci réew. Ndax, ay bakkan rot nañ ci, am ñu ci jële ay gaañu-gaañu, am tamit ñu ñu ci jàpp, waxaalewuñu yàqu-yàqu yi. Looloo tax ñu génnee ab yégle duut ci baaraam Nguuru Senegaal ci ni muy doxale ak askan wi.
Coowal Aji Saar ak Usmaan Sonko li, du guléet ay bakkan di ci rot. Ndax, màrs 2021 rekk ay bakkan rotoon nañ ci. Waaye, dafa mel ni wii yoon la yëf yi gën a doy waar. Ndax, kurél gi xamle na ci yëgleem bi ne, lum tuuti tuuti, rey nañ ci fukki nit ak juróom-benn, téeméer ak juróom-fukki nit jële ci ay gaañu-gaañu. Ñu teg ci loxo lu ëpp juróomi-téeméeri nit ci diiru ñetti fani jàmmaarloo kepp. Maanaam diggante benn fan ci weeru suwe ba ñetti fan ci weer wile. Ñoom nga xam ne sàmmonteek àq ak yelleefi doom-aadama yi mooy seen liggéey. Moo tax ñu àddu ci li xew Senegaal. Ndax, àq yooyu ñi ngi leen di salfaañe. Noonu, sàkku nañ ci njiiti réew mi, rawatina ñi féete ci wàllu Yoon, ñu luññut ba xam ku def ak ku deful, ku santaane ak ku jëfe. Bu ko defee, képp ku ci laale, ak foo mën di bokk, Yoon dal ci sa kow. Te, kii di Haut-Commissariat bu mbootaay googule mi ngi ciy bàyyi xel bu baax.
Ba tey yëgle bi yemul ci jàmmaarloo yooyu kese. Ndax, laaxaale nañu ci ni ñuy wàññee dooley kibaraan yi, maanaam këri tas-xibaar yi niki Walfadjiri mi ñu dog siñaalam.
Ñu seetlu tamit ne, li ko dale ñetti fan ci weer wii ba léegi, dañuy tere ndajem-ñaxtu yi gaa ñi di bëgg a amal. Ak tamit lënd gi ñu gàllankooroon layalee ko ne dañoo bëgg a dakkal kàdduy mbañeel yeek yu ni deme. Ndax, loolu dafa war a tegu ci lu wér. Maanaam ci ay sàrt yu wóor.
Kurél gi soññ na Nguurug Senegaal ci mu sàmm demokaraaseem, ndax loolu wareef la ci moom. Ngir loolu am nag, fàww mu sàmmonteek àq ak yelleefi doom-aadama yi. Ñu am sagoy wax seen xalaat ak daje ci jàmm. Àq la ci ñoom tamit ñu jot ci xibaar yi. Boole kook Nguur guy wattu taskati xibaar yi ba ñu mën a def seen liggéey, rawatina ci jamono jii nga xam ne ñoo ngi waajal wotey 2024 yi.
Kon loolu, firnde la ci ne jamono jii, réewum Senegaal mi ngi ci guuta gu réy. Te, lenn waralu ko lu dul ni ñuy salfaañee àq ak yelleefi askan wi. Ba ñu bari ci ñoom di yuuxu naan Yoon dafa jeng, àddina sépp di ko seede.
Nguur gi nag, jaare ko ci Aysata Taal Sàll, weddi na tuuma yees ko gàll. Nde, jëwriñu mbiri bitim-réew ji dafa génne ab yégle di ci indiy leeral ak taqal ñxtukat yi muy woowe “terorist”. Waaye nag, ku boot bukki, xaj bów la. Te, ku ñépp tufli, nga tooy.