Me MUSAA SAAR MËNUL GIS ANIBAAL JIIM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jamono jii, mbokki Muhammet Sàmba mees duppee Anibaal Jiim yaa ngi ci njàqare ju bir, rawatina layookatam bii di Meetar Musaa Saar. 

Démb la demoon fa loppitaanu Principal ngir seeti Anibaal Jiim, waaye jotu koo gis. Ndax, ciy waxam, takk-deru kaso bi ñu fa teg moo ko xamal ni, ay kilifaam ñoo joxe ndigal, wax ne bum bàyyi benn layookat di ko gis laata muy dellu kaso. Looloo metti layookat bi jàpp ne, ndigal loolu “…dafa worook li Yoon santaane ñeel àq ak yelleefi nit ki ñu jàpp kaso.”

Layookat bi, Me Musaa Saar, rax na ca dolli sax ne, li wóor ba wóor, mooy ne “…Njiiti kasob Rëbës yi dafa am lu ñiy nëbb lol, bëgguñu layookati Anibaal Jiim yi gis ko.”

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj