MOOM SA BOPP, MOOM SAW LÀMMIÑ Baabakar Lóo (ca Pari)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sunu réew, Senegaal, niki réew yu bare ci Kembaaru Afrig, yàgg naa dund ay xew-xew yu mboor dul fàtte mukk.

Ci lu jege juróomi xarnu, Tubaab yi dañoo nootoon sunuy maam. Dañu daan jël góor ñi ëpp kàttan ak jigéen ñi gën a jekk def leen i jaam, di leen jaay. Bi ñu jógee ci loolu, ñu yàq ni ñu lootaabee woon Kembaar gi ci ay dëkk ak i nguur, aakimoo lépp, daggat ko nu mu leen neexe, séddoo ko ni ñu yor ngato, ku nekk ci ñoom jël wàllam. Li leen gënoon a yombalal seen jëf jooju, nag, bokk na ci li ñu gëmloo sunuy maam ne dañoo xayadi, maanaam, amuñu xayte, li nu tanee rabi-àll yi bariwul. Te loolu, duggewuñ ko woon lenn lu dul jariñoo leen ngir suqali seen i réew. Mu mel ne kon dañoo gëmloo nit ku ñuul ne dafa tawat, ñëw ne dañ koy faj te Yàlla rekk tax ba noppi ñakk ko tooke ji koy tawatloo dëggëntaan.

Ginnaaw bi ñu séddoo réew yi Afrig ba noppi, sunu mos, Senegaal, ci yi réewu Farãas moomoon la bokk. Te ñoom way-mbéeféer yi, dañoo gëmloo woon mboolaay yi ñu nootoon ne fàww ñu niru leen ndax ñoom ñoo yor melo yu baax yi. Te dañoo sawaroon lool ci bañloo nit ku ñuul boppam ba noppi doon ko xiir ci mu bëgg mel ni ñoom ngir gën koo mën a noot. Benn ci niral yi jëlee nanu ko ci góor gu nuy wax Abdu Maalig Ja ci ab widéwoo bu doon wone jaar-jaaru jàmbaar jooju di Waljoojo Njaay ak yoon wi sunum réew jaar ba am jonnam. Góor gi nee na bi ñu nekkee ndaw, Tubaab bi doonoon sëriñ daaraam daf leen doon jàngal ni “Nit ku ñuul dafa réy, dafa tàyyeel te du waxkatu dëgg”. Nu gis ne wax jii réy na lool ciy noppi gone waaye nanu jàpp ne lenn la ci kàddu yu ñaaw, yuy gaañ te ñàkk solo lool yi ñu daan jàngal sunuy maam ngir ñu xeeb seen bopp, suufeel seen mbatiit ak seen i mbaax tey toppandoo Tubaab yi.
Ci kow loolu nag lañu jële seenuw làkk teg ko ci kow sunuy yos. Ñu dem ba ñu bari ci nun nangu ko. Ñenn ñi dem sax bay jaawale làkk wi ak xam-xam, ñu bari foog ne balaa nit ñiy nangu ne boroom xam-xam nga, fàww ngay làkk farañse, di ko logg-loggal boole ko ak neexal baat ak a def yu kenn xamul. Ñu dem tamit ba ku juum ci làkk wi dangay rus, bëgg beqi sa bopp gaaw bala ñu lay reetaan ak a xeeb. Te fekk ne ci weneen wàll wi baati wolof yi nu nu neex lanu leen di dammee te dunu ko sax yëg. Warunoo fàtte ne làkk ak wum ci man di doon, du lenn lu dul jumtukaay bu nuy may nuy wax sunuy soxla.
Réewu Afrig yu bari yu bokkoon ci yi Farãs nootoon, farañse bi lañuy gën a jëfandikoo doonte am nañu seen i làkki bopp. Nun saa-Senegaal yi, Yàlla suturaal na nu ba nu am wolof wii nuy wax ci réew mépp doonte nguur gi farañse bi la gën a fullaal.

Ci atum 1960 lanu dog buumu nooteel gi ; 61i at ginnaaw loolu, lu nuy xaar ngir dog buum gi laxasu ci sunuw làmmiñ ?

Dëgg la, ma-réewi Senegaal yépp duñu ay wolof, yeneen i làkk ñoo ngi fi. Waaye xanaa ñépp nangu nañu ne làkk wi ñépp, walla boog li ëpp ci réew mi, di jëfandikoo mooy wolof. Am nanu lu réew yu bari amul moo di làkk wu nu jéggaaniwul fenn ba noppi nun ñépp nu ciy gis sunu bopp. Fii mu ne ab joolaa ak ub séeréer bu ñuy waxtaan walla ñuy yaxantu ci seen biir, wolof lañuy làkk. Kon, nu gis ne làkku wolof dafa weesu mbiru xeet ak waaso waaye dafa doon lu nu moom ba noppi di ci gis sunu bopp, nun saa-Senegaal yi. Te it bu nuy wax dal ak jàmm ji am ci réew mi, làkk wi am na ci wàll wu am solo wu mu ci liggéey ndax dafay boole, tey dajale waa réew mi yépp.
Nu war a sukkandiku ci loolu jox làkk wi cér bi mu moom ci sunum réew. Jarul nag di xët-xëti, jarul itam di yàkkamti waaye war nanoo def ay jéego yu nu ciy yóbbu. Du caagéeni danuy xeeb wenn làkk. Déedéet ! Làkk yépp a am solo te war nanoo jàng yépp sunu ko manee du doon lu dul njariñ ndax “bépp làkk rafet na”. Dafa fekk rekk ne nun danoo am lu nu moom kon du jaadu nu koy xeeb di jël leneen lu niru ak moom. Te sax nag, wolof daa gën a gànjaru farañse bi ñuy tiitaroo.

War nanoo àgg jamono joo xam ne, benn saa-Senegaal dootul am yaras di làkk aw làkkam, ñépp dinañu man di dawal ak a bind ci sunuy làkk, ku nekk am sañ-sañu jàng lu la neex ci làkk wi, Ndeyu-àtte réew meek mbooleem téere xam-xam yi (ci wàllu diine, xamtu, xeltu, mboor, ladab, àq ak yelleef, añs.) ñu tekki leen ci wolof ba noppi siiwal leen ba ñépp mën cee jot. War nanoo àgg jamono joo xam ne sunu njiitum réew buy wax ak askan wi du doon ci nasaraan, bu ko defee ñépp déggandoo bataaxalam. Sunuy jëwriñ, jàmbur ya ca ngomblaan ga ak gépp kilifa gu yor mbiru njémmeer gi fexe ba ñuy làkk wolof ci seen i barabu liggéeyukaay. War nanoo àgg jamono joo xam ne gëdd gi ñu jox farañse ci réew mi, bu ko raw lañuy jox sunuy làkk ak yi ëpp tey doole ci àddina si. Bu ko defee saa-Senegaal yi bokk ci nit ñi gën a fonk te weg seen bopp, gën a yittewoo seen  mbatiit te du tee ñu ànd ak jamonoy dox, wutali ëllëg.

Baabakar Lóo

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj