NAALU NEKKAL : 300i DEFARUWAAYI KËYIT YEES LËNKALE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ñetti téeméeri defaruwaayi këyit (état civil) lañu lënkale ngir yombal aar geek ceetug këyiti juddu fi réew mi. Sigicoor la xibaar bi jibee. Kii di Aliyun Sàll moo ko xamle. Moom nag, Aliyun Sàll, mooy ki jiite “Agence nationale de l’état civil”.

 Bari na lu askan wiy jàmbat coono yi ñuy daj bu ñu soxlaa seen i këyiti juddu. Dañuy faral di jaabante bay bëgg a dee. Léeg-léeg, ñu wërloo leen ba ñu xàddi. Yéexay bi daf leen di jural ay gàllankoor yu baree bari ci fànn yu wuute : njàng mi, liggéey, tukki, añs. Ngir saafara jafe-jafe yooyoo tax ñu taxawal naalu “Nekkal”. Aliyun Sàll mooy leeral ci kàddu yii toftalu :

“Tay, ci wàllu naalu “Nekkal” wi, danoo jël 20i tamndareti këyiti juddu yoy saa-senegaal, dugal leen ci nosukaay yi te defaraale, ñeel këyit yooyii, jenn àlluwa baat (index). Te, lënkale nañ lu ëpp ñetti téeméeri (300i) béréb yi ñuy defaree ay këyiti juddu. Li ñu ko duggee mooy fexe ba këyit yooyu yomb a denc te ñu aaraale leen, waayeet jàppandal ceet gi ba ñu mën cee jot ci anam bu gaaw.”

APS moo tuxal kàddoom yile. Moom, Sëñ bi Sàll, dafa bokkoon cib jotaayu tàggat bu amee woon fa Sigicoor ci diirub ñaari fan. Ñi ngi jagleeloon tàggatu gi ñiy liggéey ci defaruwaayi këyit yi, ñiy yëngu ci wàllu wér-gi-yaram, njàng mi, diine ji ak way-faluy bokk-moomeeli Sigicoor yi.

Cig pàttali, keroog 7i pani me 2021 lañu sumboon naalu “Nekkal” wi. Ci diirub ñeen-fukk ak ñaari (42i) weer lañu ko nattoon. Bennoog Tugal (Union Européenne) moo kopparal naal wi, dugal ci fukk ak juróom-ñetti (18i) tamñaret (miliyaar) ci sunu xaalis (FCFA).

Kon, “Nekkal” naal wu am solo la wees war a yaatal ak a jëmmal ci réew mépp. Ndaxte, Nguur kat, ñépp la fi nekkal.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj