Tay, ci altine ji, lañu doon sumb naaluw jàppandal ndox mu sell ci dëkki àll yi. Elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, moo jiite woon ubbite gi. Faas Ture lees ko doon amalee, ci teewaayu jëwriñ ji ñu dénk wàllu ndox mi, Séex Tiijaan Jéey, ak lenn ci kilifay Càmm gi ak gox ba. Faas Ture nag, dëkk la bu nekk ci goxu Tiwaawon. Elimaanu jëwriñ yi jot na fa yékkati ay kàddu yu am solo.
Ñàkkug ndox mi bokk na ci li ñuy gën a jooy fi réew mi, rawatina ci dëkki kaw gi. Te nag, ni ko elimaanu jëwriñ yi waxee, ndox mooy lépp. Maanaam, fu ndox amul, dund du fa sotti. Loolu la Nguur gu yees gi xam ba tax ko taxawal aw naal ngir jàppandal ndox mi ci képp ku ko aajowoo, ak foo mën a nekk. Naal woowu nag, réewum Siin a leen ciy jàppale ngir jëmmal ko. Dees ràññatle naal wile ak wow wees dippee Yooni Ndox yu Mag yi (Les Grands Transfert d’Eaux). Elimaanu jëwriñu yi moo ko leeral ci kàddu yii toftalu :
“Naal wii nag, dina saafara lenn ci jafe-jafe yi ñu wax. Mën nanu ne naaluw négandiku la. Ndax, li gën a am solo ci naal yi nga xam ne ñoo war a saafara jafe-jafey ndox fi Senegaal, mooy li ñuy tudde “Les Grands Transfert d’Eaux”.”
Dafa di, li réew mi di bari ndox yépp taxagul mu jàppandi fépp ak ci ñépp. Daanaka, foo dem fi réew mi, dees fa nemmeeku jafe-jafey ndox. Ci kaw loolu, elimaanu jëwriñ yi dalal xelu askan wi. Bees sukkandikoo ciy waxam, wile naal dina indi saafara yu bari ci fànn wi. Ba tay ciy kàddoom, muy fi ñuy xëccee ndox mi, béréb ya muy jaar ba béréb ya mu jëm, ferey béréb yooyu yépp kenn dootu ci jooy jafe-jafey ndox. Loolu, ab dige la. Rax na ca dolli, moom Usmaan Sonko, ne :
“Bu ñu nee nag dañuy dellu “Lac de Guiers” jëlee fa ndox ngir yóbbu ko, saafarawaale jafe-jafey Tuubaa, saafarawaale jafe-jafey Mbuur, saafarawaale jafe-jafey Cees, waayeet saafara jafe-jafey Ndakaaru. Xam ngeen ne ndox moomu mënul a romb fii te, saafarawul jafe-jafey goxu Kebemeer, du saafara bu Luga, du saafara fépp fu ndox mi jaar […] Balaa ndox mi di egg fenn, fi muy romb yépp, dinañu fexe ba ñu jot ci ndox mi. Am ko ci anam yu mu gën a baaxe.”
Mu mel ni, naal wii dina saafara lu bari ci wàllu ndox mu sell mi, muy ci taax yi, di ci kaw gi. Nde, kenn umpalewul ne bu waa taax yi sonnee benn, waa kaw gi sonn nañ fukk. Te, seen mébét mooy ñu jàppandalal ñépp ndox mi. Njortees na ne, ak naal wii Càmm gi sumb, jafe-jafey ndox dina mujj doon lees di nettali. Dige nag, bor la.