« Man, dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. »

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mamadu Jàllo :  Ndax CFA bi baax na ci njaay meek njënd mi, rawati-na bitim-réew ? 

Ndongo Sàmba Silla : Déedéet. Mësu cee baax ! CFA bi du yombalal njaay meek njënd mi. Moom kay, safaan bi la koy jural. Ndaxte, boo seetloo, bi Senegaal moomee boppam ci atum 1960 ba nëgëni-sii, li ñuy wax ci tubaab sunu “balance commerciale” dafa deme boor. Maanaam, soo méngalee li réew miy jënd ak li muy jaay bitim-réew, dangay gis ne li muy jënd moo ëpp fuuf li muy jaay. Li Frãs fuloon dayo CFA bi moo waral laago bi.  Ndege, diisaayu CFA bi moo tax liggéey ci jafe. Te, am réew, bu dee li muy jënd bitim-réew moo ëpp li mu fay jaay, day ame ay bor yu dul jeex. Loolu moo nu sonal. Booba ba léegi, bor a ngi ci sunu baat. Danoo leb a leb ba mënatunoo fey. Seŋoor ba Maki, jaare ko ci Abdu Juuf ak Ablaay Wàdd, ku dàq a leb sa moroom nga ne kii.  Wànte Maki Sàll, sunu njiitu réew mi fi ne, moo ci raw. Te nag, jàngoro, doomu-jàngoro du ko faj. CFA bi mooy laago bi, kon, féeg noo ngi koy jëfandikoo, dunu mës a jóg ci leb. Dëgg la, réew yépp ay leb, ba ci réew yi ëpp doole ci àddina si. Waaye, benn, kenn tënku leen ba duñu mën a jaay bitim-réew ; ñaar, seen woyofaayu xaalis may na leen ñu doxale noonu seen i naal. Nun nag, CFA bi mooy sunu gàllankoor. Xaalis bi dafa am doole ba tax na say njaay du jar. Kon fooy jële looy faye say bor ?

Li nga wax dox na waar, di ! 

Yaa ko gisal sa bopp. Lu ni mel, ñi féete kow te ne déjj ci donkaasi gi doŋŋ lay amal njariñ. Dinañ mën a jënd lu leen neex bitim-réew, indi ko ci réew mi, jaayaat ko nu mu leen neexe. Seen xaalis di gën a yokk ak bu Farãs, askan wi moom di wéy di ndóol. Bu lu ni mel amee, dees na joxoñ baaraamu tuuma bànk yu mag yi. Ndaxte, ñoo ko sooke. Ndekete, ñoom dañuy bañ a lebal nit ñi xaalis. Maanaam dañ leen di gàntal. Li ñu ko dugge nag, du lenn lu dul sàmm yemoo (parité) CFA bi ak Ëro bi. Njiiti bank yooyii xam nañ ne, bees lebalee xaalis liggéeykat yi, muy àntarpërënëer bi, di boroom bitig bi, walla sax bépp jaaykat, li ñuy koy jënde mooy ay jumtukaay walla dund. Jumtukaay yooyu ak dund bi, nag, bitim-réew lañu koy jënde. Te, téeméeri àntarpiriis yoo jël, 30 yi walla 40 yi bitim-réew lañuy jëggaani seen jumtukaay.

Loolu jur lan, nag, ci sunu koom-koom ?

Day nasaxal walla day wàññi xaalis bi nuy bàyyi ci bànki Frãs ba, ñu koy wax ci nasaraan “réserves”.  “Réserves” yooyu, nag, ñooy wóoral yemoo CFA ak Ëro. Looloo tax bànk yu mag yi duñ sawar ci lebal liggéeykat yi. 

Doo ma baal nga leeral fii ? Lu loolu joteek yemoo bi ?

Waaw, ngir sàmm yemoo boobu, fàww ñu dakkal bor yi walla ñu wàññi leen. Liggéeykat bu ci am wërsëg ba bànk yi lebal la, li ngay war a fey day takku lool. Ci gàttal daal, CFA bi day yokk say bor, xoj say liggéeykat, tere laa am i isin, tere laa jaay bitim-réew… As tuut li nu am ciy njuréef ak alal, tubaab yaa koy fob yóbbu seen dëkk ndax li ñu dippe “zone franc” moo leen ko may. Ndax loolu jaadu na? 

–     Déedéet kay !

–     Kon nga xam ne noo ngi ci nooteel ba léegi. Loolu yépp, nag, boo leen boolee, lenn doŋŋ lay jur : tumurànke.

– GInnaaw bi nga leeralee ni CFA bi nooteel lay biral, lan nga jàpp ne moo nu ci teree génn boobaak léegi ?

– Waaw. Laaj bu am solo nga laaj fii. May ma ma jox la benn misaal. Man, damay faral di dem bitim-réew ngir amal fa ay waxtaan ñeel CFA bi, ma ciy ànd ak gëstukati daara-yu-kowe yu mag. Waaye, saa yu ma noppee ci wax ci CFA bi, leeral jafe-jafe yi mu làmboo, tubaab yi ci seen bopp dañuy waaru ! Mbir mi da leen di jaaxal lool sax. Bu ko defee, ñu naan ma : « Déedéet kay ! Waaw yéen, lu leen tee wacc musiba bii nga xamante ne day gàllankoor seen dund ak seen yokkute ? Ana seeni àntarpërënëer ? Seen njiit yi ngeen di fal nag, lu leen dal ba ñuy seetaan lii ? Moo, ndax dungeen fippu indi saafara ci jàngoro jii ! Yéen a ngi nelaw de ! » Bu ko defee ma ni waaw, Tubaab yeey wax lii…Waaye, bu dee fii ci Afrig, walla Senegaal, saa boo waxee ci musibay CFA bi, dañu la naan : “ Waaw…dëgg la, CFA bi am na ay jafe-jafe waaye am na ay ngëneel itam…” Nga gis ne, Tubaab yi sax, nangu nañ ne CFA bi musiba la ci nun. Waaye, ñenn ci doomi Afrig yi, walla doomi Senegaal yi ci seen bopp, ñoom, jàpp nañ ne CFA bi am na njariñ. Dafa di, ñi ànd ak CFA bi, dañu dul xalaat, walla ñu bokk ci nguur gi, teewal fi Frãs mu am lu mu leen di combal. Waaye, nag, ku waxaale sa ngor, ñu jënde ko sa toroxtaange. Loolu moo nu dal. 

-Kon ci sa gis-gis Frãs a nu teg li lépp ?

– Frãs ak doomi-Afrig yi koy jàppale. Ndaxte, boo seetee, réew yi Frãs nootoon yépp, am ci ñu dul jëfandikoo CFA bi, moom seen bopp ba mu mat sëkk, te tey ñu ngi ci yoonu yokkute. Réew yooyu, bi xeex jotee, dañu jaayante ak Frãs, jàmmaarlook moom, foqati seen réew. 

-Mën nga leen a lim ?

– Réew yu jàmbaare yooyu, mënees na cee lim Alséri ak Wiyetnaam. Ñoom ñaar ñépp a xare ngir afal seen askan. Nun, nag, sunuy njiit ya woon, jarul nu leen fiy tudd, doxalewuñu woon noonu. Dañu maslaa ak Frãs, mu kootoog ñoom, lal i pexe ngir gën fee mën a toog, aakimoo sunu alal. Bi gënoon a fës ci pexe yooyu nootkat bi laloon mooy li ñu dippe woon “Accords de coopération”. Loolu li mu wund mooy, lépp lu aju woon ci moomeelu réew yi mu nootoon, ciy loxoom lay tegu. Maanaam, njaay meek njënd mi, ak lépp lu ñeel jëflante ci diggante nootaakon (colonies) yi ak bitim-réew, xaalis bi (te muy CFA bi) ak koom-koom gi. Loolu la Frãs waxoon ne bu ci sunu njiit ya woon àndee xaatim ko, mu nangu ñu moom seen réew. Sunu njiit yi nag, ñu ci ëpp Frãs lañu jànge, foofu lañ leen tàggate, daan fa liggéeye te nekkoon fa sax dipite. Moo tax ñu xaatim loraange jooju nu topp ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Réew mu ci mel ni Gaboŋ, lépp lu muy def, Frãs da cee ànd. « Accords de coopération » bi mu xaatimoon ñoo ko ko yóbbe.

Ndax am na ñu fippu, ne fàww ñu dog buumu njaam gii ?

– Lii tamit laaj bu am solo la. Am na ñu yàgg a xeex CFA bi ngir jële ko fi. Axã kay ! Du léegi la ñenn ci doomi Afrig yi tàmbalee xeex CFA bi. Xeex bi démb la woon, tey door a agsi. Te loolu boo ko waxee xel war naa dem ci Séku Ture. Ndege, moom moo jëkk a bañ CFA bi, ne dee, Gine du ci bokk. Moom Séku Ture, bañkat bu mag la woon, amaana li mu doonoon ab sàndikalist moo taxoon. Ndax ku mënoon a dajale ay nit la te bare woon i pexe lool. Waaye, ak lu xel miy màcc yépp, jataŋ ak gàllankoor yu bare yi ko Frãs daan teg, moo koo taxoon a tagatémbe. Loolu rekk a teewoon Gine génn ci. Frãs da doon dugal Gine xaalis bu bon bu baree-bare ngir yàq deru Séku Ture. Am na keneen ku ñiy wax Silwanus Olimpiyóo, njiitu Tógo la woon, nekkoon layookat bu siiw. Dafa laloon ab naal ngir wutal réewum Tógo xaalisu boppam. Jotoon na cee waxtaan sax ak réew yu mag ci àddina si, niki Almaañ ak Amerig. Bi mbir mi demee bay sotti la ko Frãs sàkkal pexe, ngem Eyademaa mu rey ko. Naka noonu, Tomaas Sànkara, jàmbaaru Burkina-Faaso ba. Nu gis ne, Frãs jenn itte doŋŋ la am : ratt réewi Afrig yi ba ñu sett, jël seen alal di ko siimee cereem.Cere jooju, nag, ku ko bëgg a xajamal mu sàkkal la pexe. Waaye, nit ñit xippi nañu seeni bët.

– De4gg la, nit ñi xippi nañu seeni bët, moo waral way-moomeel yi, kujje gi ak boroom xam-xam yi takkal pot sunu njiit yi ak Frãs. Dafa mel ni gaa ñaa ngiy deeltu ginnaaw ndax ñoo ngi wax ne dañuy bàyyi CFA bi dem ci ECO bi. Loo xam ci xaalis bu bees boobu ?

– ECO bi ?Waaw. Dégg naa ñenn ñiy xeex CFA bi naan, nanu gaaw jël ECO bi, def ko sunu xaalis. Waaye, ECO bi ci lajj lay mujj. Wolof dafa ne, ku ndóbin rey sa maam, foo séenatee lu ñuul daw. Man dama jàpp ne, CFA ak ECO ñoo yem kepp, benn baaxu ci. Dama xamul lu tax rekk mënuñu lal ab naal boo xam ne, dina jur i meññent ëllëg. Te sax, lu tax nuy déglu ñi nuy gëmloo ne sunu bëggee jëm kanam fàww nu bokkak ñeneen ñi xaalis ? Loolu du dëgg. Gàtt xel doŋŋ la ak xeebaate. Fii, ku fi gëm sa bopp, takku liggéey dinga am yokkute. Damay jël misaal ci yenn réewi Ërob yoo xam ne Senegal moo leen gën a yaatu, ëpp leen alal, ëpp leen mbooloo. Tey, ñoo ngi ci naataange te dara mayu leen ko lu dul liggéey bu jaar yoon. Kon, ku nekk mën nga  liggéeyal sa réew ba mu naat. Waxuma ni booloo baaxul. Wànte, fàww ku nekk gëm sa bopp ba noppi, liggéey liggéey bu lay amal njariñ, amal njariñ ñeneen ñi. Bu ko defee, dinañu mën a saxal garabu booloo gi, di ko suuxat ba mu màgg, dëgër, law ci biir Afrig gépp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj