10Dibéer yemook ñaar-fukki fan ak ñeent si weeru Féewaryee, la waa réew mi doon tànn ki leen war a jiite ba atum 2024. Waaye, dafa mel ne li mu jur ci werantee ëpp li mu jur ci jàmm ji ñu xame Senegaal. Ndaxte, woteb njiitu réew bees génn, ñaxtook fitna lañ ci gën a ràññee. Te yit, ngirte yi àttekat bii di Demba Kànji siiwal, waa kujje gi, kuréli way-moomeel yeek li ëpp ci askan wi naqarlu nañu ko ; ndax nee nañu ag càcc gu leer nàññ la. Kon, woteb ren bi, bu yéesul ci wote yi fi jot a am ba léegi, bokk na ci yi gën a taq suuf. Looloo waral lawax yi féetewoo kujje gi dàq xàjj-ak-seen, booloo doon benn niw say, lànk ne nanguwuñu ndamal Maki Sàll li. Moone de, yoon may na bépp wutaakon mu kalaame ci ndajem ndeyu àtte mi, bu gisee ni wote bi am nay jalgati yu fés. Waaye, bank nañu seeni loxo, boq golo gi, ne dee duñu dem ci kanamu Ndajem ndeyu-àtte mi di fa jooytu dara. Lees ci war a jàngate mooy ne, lawaxi kujje gi amatuñu kóolute ñeel aji-àtte yi. Naka-jekk, dañoo wone ay yooni yoon ne ñoom Maki Sàll la ñu fi nekkal ak ay bëgg-bëggam. Muy lu doy waar ci demokaraasi réew mi te jar a naqarlu. Te nag, àddina sépp a ngi nuy may nopp, ne nu jàkk di nu xool. Wax dëgg, Makeek demokaraasi, mi ngi mel ni Yàllaak yaali. Li koy firndeel mooy ne, saa yu jëlee dogal walla nu génn ciy wote, coow li da naan kurr. Lim yi tukkee ci woteb njiitu réew mi jeex, daanaka moom la ay njegeñaaleem ak i farandoom biraloon ca njëlbéen. Mu mel ni aji-àtte yi defuñu lu dul dëggal lim yooyu.
Yatma Jóob