MÀNGAAN NDEKE AM NA CI PÓLITIG !

Yeneen i xët

Aji bind ji

b ak yu tey gis ñu woroo lool. Am na sax ci ñoom ku ne woon Ndeyu-Àtte réewum Senegaal dafa war a aaye màngaan ci politig. Yemu fa, ndax dem na ba yaramam tàng, mu yokk ci ne képp ku jóge cib pàrti, ak bu mu mënti doon, dem màngi ci nguur gi, yoon dafa war a jël sa bakkan ! Moonte ngóor si waxoon loolu, moo xéy bés ne maa tey, fekki naa Maki Sàll…

Waaye li Senegaal di miin xeeti jëf yu ñaaw yooyu yépp, teewul askan wi, rawatina ndaw yi, am mbetteel biñ déggee ne Aysata Taal Sàll màngi na moom tamit. Man mii amoon naa ci naqar lool. Mënuma woon a nangu ne “Gayndek Podoor gi”, gaynde gi ma xamaloon fulla ak faayda ju mat sëkk dina defi lu ni mel. Lu ko ci xiir ? Ñii a ngi naan dañu koo compal waaye am na ñu wedddi loolu. Xéy-na bañ cee soree gën, ndax Yàlla rekk a xam.

Li am ba des, daal, moo di ne jot na ndawi Senegaal yi taxaw temm ngir xeex ba jële fi yenn ñaawtéef yiy yàq làngu pólitig gi tey nasaxal campeefi réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj